Luug 21:1-37 WOLB2025 - Bible AI

1Ci kaw loolu Yeesu xoolaat, daldi gis boroom alal yi, ñuy dugal seen sarax ca ndaal kër Yàlla ga.

2Mu gis itam ab jëtun bu néew doole, mu def ca ñaari poseti xànjar+ 21.2 Mooy posetub lepton. Seetal Xaalis ci Leeral yi.*.

3Yeesu ne: «Maa leen ko wax déy, jëtun bu néew doole bii, ñii ñépp, moo leen ëpple lu mu joxe.

4Ndax ñii ñépp, la ñu woomle, ca lañu sompe, sànni ci boyetu sarax bii; waaye moom ci biir ag ñàkkam la jël mboolem ab dundam, sànni ci.»

5Mu am nag ay nit ñu doon wax ca kër Yàlla ga, ak taaru doji tànnéef ya, ak yeneen alali sarax ya ñu ko rafetale. Yeesu itam ne leen:

6«Lii ngeen gis nii, ay jant a ngi ñëw yu fi doj dootul des ci kaw doj, lépp ay tas.»

7Ñu laaj ko ne ko: «Kilifa gi, loolu kañ lay doon? Ak luy doonub takk buy xamle ne looloo ngi waaja dikk?»

8Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp.

9Bu ngeen déggee ay xare aki salfaañoo, buleen tiit, ndax fàww loolu njëkka am. Waaye du doonagum muj ga, ca saa sa.»

10Mu neeti leen: «Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew.

11Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan.

12Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréeli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,

13ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede.

14Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne waruleena waajal kàddug layoo.

15Ndax man maa leen di may làmmiñ wu ànd ak xel wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

16Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na reylu ñenn ci yeen.

17Te it ñépp a leen di bañ ndax sama tur.

18Waaye sa genn kawar sax du ruus.

19Saxooleen muñ nag, daldi mucc.

20«Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.

21Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya; ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn; te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.

22Ndax jamonoy mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.

23Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca bés yooyu! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi ak am sànj ci kaw askan wii.

24Dinañu leen faate ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jàmbur ñi dul Yawut ñooy dëggaate Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.

25«Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,

26nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi.

27Su boobaa dees na gis Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.

28Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug njot|lemma="jot:"* dëgmal na.»

29Ci kaw loolu Yeesu léeb leen ne leen: «Xoolleen garabu figg mbaa geneen garab.

30Bu ngeen gisee mu jebbi, ca ngeen di xamal seen bopp ne nawet jubsi na ba noppi.

31Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne nguurug Yàlla dëgmal na.

32«Maa leen ko wax déy, niti tey jii+ 21.32 niti tey jii: seetal ci +bk Màrk+bk* 8.38.* duñu wéy mukk, te loolu lépp sottiwul.

33Asamaan ak suuf dina wees, waaye samay wax du wees mukk.

34«Moytuleen naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina wayadiloo leen, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

35ndax ni mbaal di bettee, noonu la bés bay jekkee dal ci kaw mboolem ñi ci kaw suuf.

36Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.»

37Bés bu nekk nag Yeesoo nga doon yendoo jàngale ca kër Yàlla ga, bu guddee mu fanaani ca kaw tund wa ñuy wax tundu Oliw|lemma="tundu Oliw y-:"* ya.

© 2025 Bible Society of Senegal