1Màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggal yi:"*, te ñu di ko wax bésub Mucc|lemma="Màggal yi:"*, moo jubsi woon.
2Ci biir loolu sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yu mag ya ak firikati yoonu Musaa ya di seet nu ñuy fexee ba rey Yeesu, waaye dañoo ragaloon nit ña.
3Seytaane|lemma="Seytaane:"* nag dugg Yuda mi ñuy woowe Iskaryo te mu bokkoon ca Fukk ñaak ñaar.
4Yuda daldi diisooji ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ngir xam nan lay tege Yeesu ci seeni loxo.
5Ñu am ca mbégte, digook moom, ngir jox ko xaalis.
6Yuda nangu, di wut nag yoon wu mu jekkoo Yeesu, ba wor ko, fu mbooloo ma teewul.
7Ci kaw loolu bésu màggalu Mburu mu amul lawiir|lemma="Màggal yi:"* agsi, ñu war caa rendi gàttub bésub Mucc|lemma="Màggal yi:"*.
8Yeesu yebal Piyeer ak Yowaan ne leen: «Demleen, waajalal nu bésub Mucc bi, ba nu reeri.»
9Ñu ne ko: «Foo bëgg nu waaje ko fa?»
10Mu ne leen: «Bu ngeen di dugg ca dëkk ba rekk, dingeen dajeek waa ju yenu njaqas ndox. Toppleen ko ba ca biir kër ga mu jëm,
11te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee: Ana néegu gan, fi may reere reeru bésub Mucc, maak samay taalibe?”
12Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa bu ñu defar ba noppi. Foofa ngeen di waajale.»
13Ba ñu demee, noonee leen ko Yeesu waxe, na lañu gise lépp. Ñu daldi waajal reeru bésub Mucc ba.
14Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya,
15ne leen: «Yàkkamti woon naa lool bokk ak yeen reeru bésub Mucc bii, bala maa tàbbi coono.
16Ndax maa leen ko wax, dootuma ko reer mukk, ba keroog solos reer bi di sotti ca nguurug Yàlla.»
17Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jëlleen kaas bii, te ngeen séddoo ko.
18Ndax maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan ndoxum reseñ, ba kera nguurug Yàlla dikk.»
19Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu joxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttalikoo.»
20Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* gu yees gi fasoo ci sama deret ji nara tuuru ngir yeen.
21Waaye nag ki may wor, loxoom a ngi ci ndab lii nu bokk.
22Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki déy, ni ñu ko dogale, noonu lay deme, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu koy wore di jaare.»
23Ci kaw loolu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom moo nar jooju jëf.
24Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom.
25Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di woowe.
26Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga.
27Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!
28Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono.
29Man itam ni ma sama Baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke.
30Yeenay lekk aka naan ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay toog ci ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ak ñaar.»
31Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane|lemma="Seytaane:"* kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.
32Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»
33Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso ak ci ànd ak yaw dee.»
34Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga jàmbu ñetti yoon, ne xamuloo ma.»
35Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw|lemma="tundu Oliw y-:"* ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ko.
40Ba mu agsee ca béreb ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.»
41Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.
42Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
43Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
44Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis.
46Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
47Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, am mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki!»
49Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba, njoof noppu ndijooram.
51Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya ak kilifay wattukati kër Yàlla ga ak magi askan wa. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur.
53Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
54Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca.
55Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir.
56Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!»
57Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»
58Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, bokkuma ci ñoom!»
59Ba ñu ca tegee lu mat waxtu, keneen jaaraat ca wax ja ne: «Kii kay wax-dëgg, moom la àndaloon, nde waa Galile la.»
60Teewul Piyeer ne ko: «Waa jii, li ngay wax, xawma ko de!» Ca saa sa, ganaar sab, te kàddug Piyeer daanoogul sax.
61Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttaliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.»
62Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.
63Ci kaw loolu ña jàpp Yeesu, di ko ñaawal aka dóor.
64Ñu muur kanam gi, naan ko: «Yaw, waxal nu kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* boog, ana ku la dóor?»
65Yeneen saaga yu bare tifaar nañu ko ko.
66Ba bët setee kuréelu magi askan wa ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yu mag ya ak firikati yoonu Musaa ya, ñépp daje. Ñu yóbbu Yeesu ca seen kuréelu àtte|lemma="kuréelu àttekat y-:"* ba.
67Ñu ne ko: «Soo dee Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
68Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
69Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki mooy toog ci ndijooru Yàlla, Boroom Kàttan gi.»
70Ñépp daldi ne: «Kon yaay Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"*?» Mu ne leen: «Yeena waxal seen bopp ne man la.»