Luug 6:1-48 WOLB2025 - Bible AI

1Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"* la woon, Yeesu doon jaar ci ay tool yu ñor, taalibeem ya fàqe ca ay gub, di boxom, di lekk.

2Ñenn ca Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya ne leen: «Lu waral ngeen di def lu yoon mayewul ci bésub Noflaay?»

3Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen la Daawuda|lemma="Daawuda:"* defoon, ba mu xiifee, moom, ak ña mu àndaloon?

4Ba mu duggee ca kër Yàlla ga, mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"* ma la jël, lekk, jox ca ña mu àndal, te yoon mayewul kenn ku ca lekk ku dul sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yi.»

5Mu neeti leen: «Bésub Noflaay, Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki mooy boroom.»

6Beneen bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"*, Yeesu dugg ca jàngub Yawut ba, di jàngale. Jenn waay ju loxol ndijooram làggi ma nga fa woon.

7Firikati yoonu Musaa yaak Farisen|lemma="Farisen y-:"* yaa ngay xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ca bésub Noflaay ba, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale.

8Yeesu nag xam seen xalaat, daldi ne boroom loxo bu làggi ba: «Jógal taxaw fii ci digg bi.» Mu jóg taxaw.

9Yeesu ne leen: «Laaj naa leen, ana lu yoon maye ci bésub Noflaay: def lu baax am lu bon? Rawale bakkan walla faat?»

10Ci kaw loolu mu dawal bëtam, xool ña ko yéew ñépp, ba noppi ne waa ja: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal, loxo ba wér.

11Ñu mer nag ba fees, di diisoo ci seen biir nu ñuy def ak Yeesu.

12Fan yooyu la Yeesu dem ca kaw tund wa ngir ñaani fa; mu fanaane faa ñaan ci Yàlla.

13Ba bët setee, mu woo ay taalibeem, tànn ca fukk ak ñaar ñii, tudde leen ay ndawam:

14Simoŋ mi Yeesuy woowe itam Piyeer,

15ak Macë ak Tomaa,

16ak Yuda doomu Yanqóoba,

17Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu bare: ay niti Yude gépp, ak Yerusalem, ak Tir ak Sidon|lemma="Tir:"*, dëkki wetu tefes ga.

18Ñu dikk, di ko déglu tey faju ba tàggook seeni jàngoro. Ñi rab|lemma="rab:"* jàpp it, wér.

19Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.

20Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen:

21Ndokkalee yeen ñi xiif tey,

22Ndokkalee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki.

23Bésub keroog, bégleen bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la maami ñooñu daan def ak yonent ya.

24Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele,

25Wóoy ngalla yeen ñi regg tey,

26Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.

27«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defalleen leen lu baax.

28Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanalleen leen.

29Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.

30Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.

31Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.

32«Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara ame ab yool? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.

33Te su dee ñi leen defal lu baax doŋŋ ngeen defal lu baax, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi it noonu doŋŋ lañuy jëfe.

34Te su dee ñi ngeen yaakaare ndelloo doŋŋ ngeen lebal, ana lu ngeen ci wara ame yool? Bàkkaarkat yi it, yaakaar ndelloo lu mat sëkk moo tax ñuy lebalante.

35Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.

36Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.

37«Buleen di sikkal kenn, su boobaa deesuleen sikkal. Buleen yeyale kenn ab daan, ngir ñu bañ leena yeyale ab daan. Baaleleen, ñu baal leen.

38Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkos, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.»

39Yeesu léebati leen, ne leen: «Ndax gumba dina wommat gumba? Mbaa duñu ànd tàbbi ci kàmb?

40Taalibe sutul kilifaam, waaye bépp taalibe bu jàng ba wàcc, day tollook kilifaam.

41«Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk te gànj gi ci sa bëtu bopp gisuloo ko?

42Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax bi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Njëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax bi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko.

43«Garab gu neex du meññ doom yu naqari, te garab gu naqari it du meññ doom yu neex.

44Garab gu nekk, meññeefam lees koy xàmmee. Ab dédd, deesu ci witte doomi figg; ay dagg it, deesu ci jële doomi reseñ.

45Nit ku baax, dencub ngëneel ba ca biir xolam, ca lay jële lu baax la mu sàlloo; nit ku bon it, dencub safaan ba ca biir xolam, ca lay jële safaan ba mu sàlloo. Gémmiñ daal, la fees xolu boroom lay wax.

46«Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?

47Képp ku ñëw ci man, dégg samay wax te di ko jëfe, dinaa leen won nu muy mel.

48Dafa mel ni nit kiy tabax kër, gas a gas ba mu xóot, daldi samp fondmaa ca kaw doj wa ca suuf. Mbënn ma dikk, wal ma rëkk kër gaak doole te manu koo yëngal ndax tabax bu wér ba ñu ko tabaxe.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>