Màndiŋ ma 21:1-34 WOLB2025 - Bible AI

1Kanaaneen ba, buurub Aràdd ba dëkke woon Negew, moo dégg ne Israayil a ngay jaare yoonu Atarim, di dikk. Mu xareek Israayil, jàpp ñenn ca ñoom.

2Ci kaw loolu Israayil xasal Aji Sax ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.»

3Aji Sax ji nangul Israayil, jébbal leen Kanaaneen ña, ñu faagaagal leen, ñook seeni dëkk. Ñu daldi woowe gox ba Xorma (muy firi Lu ñu faagaagal).

4Ñu bàyyikoo tundu Or, jubal yoonu géeju Barax ya, ngir teggi réewum Edom. Mbooloo ma nag mujj xàddi ca yoon wa.

5Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te mànn|lemma="mànn:"* mii, di ñamu toskare génnliku na nu!»

6Ba loolu amee Aji Sax ji yebal ay jaan yu seen daŋar di lakke ca biir mbooloo ma, ñu màtt leen, ba ñu bare ci bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* dee.

7Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.

8Aji Sax ji ne Musaa: «Defarlul jëmmu jaan ju daŋar ji di lakke, nga wékk ko ci bant. Su ko defee képp ku ñu màtt, boo ca xoolee, mucc.»

9Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc.

10Bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* fabooti, dem ba dali fa ñuy wax Obot,

11jóge Obot, dali Yee Abarim, ca màndiŋ ma janook Mowab, ca penku ba.

12Foofa lañu faboo, dem ba dali ca walum Seredd,

13bàyyikooti foofa, dem ba dali ca wàllaa dexu Arnon ga wale ca réewum Amoreen ña te jaare ca màndiŋ ma. Dexu Arnon googa, fa la réewum Mowab digalook Amoreen ñi.

14Moo tax téereb Xarey Aji Sax ji indi ko, ne:

15xur ya bartalu,

16Fa lañu bàyyikoo, dem Beer, (muy firi ab Teen); teen boobu, fa la Aji Sax ji noon Musaa: «Dajaleel mbooloo mi, ma may leen ndox.»

17Ca la Israayil woy woy wii:

18Ay garmee la bënn,

19jóge Matana dem Naxaliyel, jóge Naxaliyel, dem Bamot,

20jóge Bamot ba ca xur wa ca àllub Mowab, àkki nag njobbaxtalu tundu Pisga wa tiim ndànd-foyfoy ga.

21Ba loolu amee Israayil yebal ay ndaw ca Sixon buurub Amoreen ña, ne ko:

22«May nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jàdde benn tool mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naan ndoxum teen. Mbeddum buur lanuy topp, ba keroog nuy jàll sam réew.»

23Sixon nag mayul Israayil, ñu jaarem réewam, xanaa mu dajale gàngooram gépp, sàqi, ngir dajejeek Israayil ca màndiŋ ma. Mu dikk ba Yaxacc, song Israayil,

24Israayil leel ko ñawkay saamar, nangu seenum réew, dale ko Arnon ba Yabog, ba àgg ca Amoneen ña, ndax kemu réewum Amoneen ñaa fegu woon ba kenn manu koo bëtt, jàll.

25Israayil nangu dëkki Amoreen yooyu yépp, daldi sance mboolem seeni dëkk, boole ca Esbon aki dëkk-dëkkaanam.

26Esbon moo doon péeyub Sixon buurub Amoreen ña. Kookoo xare woon ak buuru Mowab ba woon, moo nangu ciy loxoom réewam mépp, ba Arnon.

27Moo tax woykat ya ne:

28Lakk gaa nga jóge Esbon,

29Mowabee ngalla yaw!

30Noo leen fitt,

31Israayil nag dëkke réewum Amoreen ña.

32Ba loolu amee Musaa yebal ay ndaw, ñu yëri dëkk ba ñuy wax Yaser. Gannaaw gi, bànni Israayil nangu dëkk-dëkkaan ya, daldi fay dàqe Amoreen ña.

33Ba mu ko defee ñu walbatiku, awe yoonu Basan, Og buuru Basan ànd ak gàngooram gépp, dajejeek ñoom, song leen xare ca Eddrey.

34Aji Sax ji ne Musaa: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp akum réewam, nga def ko na nga defoon Sixon buurub Amoreen ba woon fa Esbon.»

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>