Màndiŋ ma 23:1-29 WOLB2025 - Bible AI

1Ba loolu amee Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"*, te waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.»

2Balag def na Balaam wax, Balag ak Balaam ku ci nekk sarxal wenn yëkk ak menn kuuy ci sarxalukaay bu nekk.

3Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ma dem ba nee. Jombul Aji Sax ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul.

4Ba loolu amee Yàlla dikk, dajeek Balaam, Balaam ne ko: «Juróom ñaari sarxalukaay yi, yékkati naa leen te sarxalukaay bu ci nekk, sarxal naa ci wenn yëkk ak menn kuuy.»

5Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»

6Balaam dellu ca moom, fekkul lu moy mu taxaw ca saraxu dóomalam, moom ak kàngami Mowab yépp.

7Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne:

8Moo! Nu may móoloo ku Yàlla móoluwul?

9Kaw doj yii laa tollu di leen séen,

10Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba?

11Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?»

12Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu Aji Sax ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?»

13Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.»

14Mu daldi koy yóbbu ba ca toolub Cofim, ca collu tundu Pisga. Ci kaw loolu mu tabax fa juróom ñaari sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"*, sarxalukaay bu nekk, mu sarxalati fa yëkk wu ndaw ak am kuuy.

15Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, man ma séentuji nee.»

16Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»

17Mu dem ba ca moom, fekku ko lu moy mu taxaw ca wetu saraxu rendi-dóomalam, mook kàngami Mowab. Balag ne ko: «Lu Aji Sax ji wax?»

18Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne:

19Yàlla du nit, bay fen,

20Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam,

21Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba,

22Yàllaa leen jële Misra,

23Ñeengo jàppul Yanqóoba,

24Wii askan ni gaynde lay jóge,

25Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Boo leen móoluwul benn yoon kay, bu leen ñaanal ba doyal boog!»

26Balaam ne ko: «Xanaa waxuma la woon ne la lépp lu Aji Sax ji wax, loolu laay def?»

27Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.»

28Balag yóbbu Balaam ba ca collu tundu Pewor, wa tiim ndànd-foyfoy ga.

29Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay, te nga waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.»

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>