1Balaam nag gis ne Aji Sax ji la neex mu barkeel Israayil, ba tax sàkkootul ay takk na woon, xanaa mu walbatiku, janook màndiŋ ma.
2Ci kaw loolu Balaam dawal bëtam, daldi séen Israayil, na ñu dale topp seeni giir, leerug Yàlla daldi koy dikkal.
3Ba mu ko defee mu yékkati kàddug ñaanam, ne:
4kàddug kiy dégg waxi Yàlla,
5Yanqóobaa, yaaka yànji xayma!
6Ña nga ne màww ni tooli tàndarma,
7Ndox maay wale cay bagaanam,
8Yàllaay ki ko jële Misra,
9Israayil a ngi yuug aka goor ni gaynde,
10Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la woowe woon, yaw defoo lu moy ñaanal leen a ñaanal, ba muy ñetti yoon nii!
11Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, Aji Sax jee la xañ teraanga.»
12Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen,
13su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax.
14Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»
15Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne:
16kàddug kiy dégg waxi Yàlla,
17Maa ngi koy gis, te du tey,
18Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom;
19Fa Yanqóoba la buur di bawoo,
20Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékkati kàddug ñaanam, ne:
21Mu teg ca geesu réewum Keñeen ña, yékkateeti kàddug ñaanam, ne:
22Waaye réewum Keñeen gépp ay xoyomu,
23Mu dellooti yékkati kàddug ñaanam, ne:
24Ay gaal ay jóge tefesu Kitim,