1Aji Sax ji dafa wax Musaa, ak Elasar doomu Aaróona sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba, ne leen:
2«Waññleen mbooloom bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* gépp, ngeen lim turi góor ñépp, na ñu bokke seen këri maam, dale ko ci ñi am ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci bànni Israayil.»
3Musaa ak Elasar sarxalkat ba wax ak ñoom ca joori Mowab, fa janook Yeriko ca wetu dexu Yurdan; ñu ne leen
4ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israayil, ña génne woon Misra:
5Ruben moo doon taawub Israayil. Ñi askanoo ci Ruben ñoo di Enog mi sos làngu Enogeen ñi, ak ñoom Palu, Palu mi sos làngu Paluween ñi,
6ak ñoom Esron, Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Karmi mi sos làngu Karmeen ñi.
7Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu ca lim di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaari téeméer ak fanweer (43 730).
8Palu moo meññ Elyab,
9Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
10ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wann, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaari téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo.
11Doomi Kore ya nag deewuñu ca.
12Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Yakin mi sos làngu Yakineen ñi,
13ak ñoom ñi bokk ci Sera mi sos làngu Ceraxeen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi.
14Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaari téeméer (22 200).
15Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Suni mi sos làngu Cuneen ñi,
16ak ñoom ñi bokk ci Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Eri mi sos làngu Ereen ñi,
17ak ñoom ñi bokk ci Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Areli mi sos làngu Areleen ñi.
18Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500).
19Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ca réewum Kanaan lañu faatoo.
20Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Sera mi sos làngu Ceraxeen ñi.
21Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom ñi bokk ci Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Amul mi sos làngu Amuleen ñi.
22Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500).
23Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Puwa mi sos làngu Puween ñi,
24ak ñoom ñi bokk ci Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Simron mi sos làngu Cimroneen ñi.
25Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300).
26Ñi askanoo ci Sabulon, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Seredd mi sos làngu Cereddeen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Elon mi sos làngu Eloneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Yaxleel, mi sos làngu Yaxleleen ñi.
27Làngi Cabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500).
28Ñi askanoo ci Yuusufa nag, ñook seeni làng, ñoo soqikoo ci Manase ak Efrayim.
29Ñi soqikoo ci Manase ñoo di ñoom ñi bokk ci Makir mi sos làngu Makireen ñi. Makir moo jur Galàdd. Ci Galàdd la làngu Galàddeen ñi soqikoo.
30Ñii ñoo askanoo ci Galàdd: Yeser mi sos làngu Yesereen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Eleg mi sos làngu Elegeen ñi,
31ak Asriyel mi sos làngu Asriyeleen ñi, ak Sikem mi sos làngu Cikemeen ñi,
32ak Semida mi sos làngu Cemideen ñi, ak Efer mi sos làngu Efereen ñi.
33Celofat doomu Efer nag amuloon doom ju góor, xanaa aw jigéen doŋŋ. Doomi Celofat yu jigéen di Maxla ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca.
34Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaari téeméer (52 700).
35Ñii nag ñoo askanoo ci Efrayim, ñook seeni làng: ñoom ñi bokk ci Sutelax mi sos làngu Cutelaxeen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Beker mi sos làngu Bekereen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Taxan mi sos làngu Taxaneen ñi.
36Ñii nag, askanu Sutelax lañu: ñoom ñi bokk ci Eran, ak làngu Eraneen ñi mu sos.
37Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500).
38Ñi askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Bela mi sos làngu Beleen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Asbel mi sos làngu Asbeleen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Axiram mi sos làngu Axirameen ñi,
39ak ñoom ñi bokk ci Sufam mi sos làngu Cufameen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Ufam mi sos làngu Ufameen ñi.
40Askanu Bela wi sosoo ci Àrd ak Naaman ñoo di làngu Àrdeen ñi, ak làngu Naameen ñi sëtoo ci Naaman.
41Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600).
42Ñii nag ñoo askanoo ci Dan, ñook seeni làng: ñoom ñi bokk ci Suxam ak làngu Cuxameen ñi. Daneen ñaa ngoogu, na ñu lime seeni làng.
43Mboolem làngi Cuxameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400).
44Ñi askanoo ci Aser, ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Imna mi sos làngu Imneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Iswi mi sos làngu Isween ñi, ak ñoom ñi bokk ci Berya mi sos làngu Beryeen ñi.
45Waa askanu Berya ñoo di ñoom ñi bokk ci Eber mi sos làngu Ebereen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Malkiyel mi sos làngu Malkiyeleen ñi.
46Doomu Aser ju jigéen nag moo di Sera.
47Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
48Ñi askanoo ci Neftali ñook seeni làng ñoo di ñoom ñi bokk ci Yàcceel, mi sos làngu Yàcceleen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Gunni mi sos làngu Guneen ñi,
49ak ñoom ñi bokk ci Yeccer mi sos làngu Yecereen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Silem mi sos làngu Cilemeen ñi.
50Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400).
51Limeefu bànni Israayil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaari téeméer ak fanweer (601 730).
52Aji Sax ji nag wax Musaa, ne ko:
53«Ñii lees di séddale réew mi, te na cér yi dëppook limu nit ñi.
54Làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut, làng gu ci nekk, cér bi dëppook ab limam lees koy jox.
55Ab tegoo bant doŋŋ lees di séddalee réew mi, te seen limu giiri maam ya ñu bokk, na dëppook seenub cér.
56Ci kaw tegoo bant lees di dogale céru giir gu ñu bare séq, ak gu ñu néew séq.»
57Ñii nag lañu limal Leween|lemma="Leween b-:"* ñi ak seeni làng: ñoom ñi bokk ci Gerson mi sos làngu Gersoneen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Keyat mi sos làngu Keyateen ñi, ak ñoom ñi bokk ci Merari mi sos làngu Merareen ñi.
58Ñii itam ci làngi Leween lañu: làngu Libneen ñi, ak làngu Ebroneen ñi, ak làngu Maxleen ñi, ak làngu Museen ñi, ak làngu Koreen ñi. Keyat nag mooy maamu Amram;
59soxnas Amram di Yokebedd doomu Lewi, ja juddoo Misra. Yokebedd am ak Amram Aaróona ak Musaa ak Maryaama, seenub jigéen.
60Aaróona moo jur Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
61Nadab ak Abiyu ña nga dee keroog ba ñu taalalee Aji Sax ji cuuraay|lemma="cuuraay l-:"* lu warul.
62Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israayil.
63Ñooñu lañu lim ci njiital Musaa ak Elasar sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba, ba ñu tënkee limeefu bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ca joori Mowab, ga janook Yeriko, ca tàkkal dexu Yurdan.
64Ñooñu, kenn desul ca seen biir, te bokkoon ca limeefu bànni Israayil, ba Musaak Aaróona sarxalkat ba njëkkoona tënke ca màndiŋu Sinayi.