1Ci kaw loolu ay doomi Celofat yu jigéen jóg. Seen baay Celofat, Efer ay baayam, Efer, Galàdd ay baayam, Galàdd, Makir ay baayam, Makir, Manaseey baayam mi bokk ci Manaseen ya, Manase, Yuusufaay baayam. Jigéen ñooñu ñoo di Maxla ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca.
2Ñoo taxaw fa kanam Musaa, ak Elasar sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba, ak njiit ya, ak mbooloo ma mépp, ca bunt xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* ma. Ñu ne:
3«Sunu baay daa dee ca màndiŋ ma. Moom nag bokkuloon ca gàngooru Kore, ga daje woon ci kaw Aji Sax ji, waaye bàkkaaru boppam a ko rey. Bàyyiwul nag doom ju góor.
4Waaye lu tax ñu génne sunu turu baay ci làngam gi mu bokk, ndax ñàkk doom ju góor? Joxleen nu sunub cér ci biir wàll wi sunu bokki baay yu góor bokk ak sunu baay kay!»
5Ci kaw loolu Musaa jébbal Aji Sax ji àtteb jigéen ña.
6Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
7«Li doomi Celofat yi wax dëgg la. Danga leen di jox kay, ab cér ci biir wàll wi seen baay bokk ak bokkam yu góor. Su ko defee nga féetale leen seen céru suufu baay.
8«Te nga wax bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, ne leen: “Bu ku góor deewee te bàyyiwul doom ju góor, doomam ju jigéen ngeen di jox céru suufam.
9Su amul doom ju jigéen nag, góor ñi mu bokkal waajur ngeen di jox céru suufam.
10Su amul góor gu mu bokkal waajur, góor ña baayam bokkal waajur, ñoom ngeen di jox céru suufam.
11Su baayam amul góor gu mu bokkal waajur, mbokkam mu ko gëna jege ci biir làngam, moom ngeen di jox céru suufam. Kookooy donn cér ba. Na loolu di dogalu yoon, ñeel bànni Israayil, noonu ko Aji Sax ji sante Musaa.”»
12Gannaaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Yéegil ca kaw tundu Abarim wee, nga séentu réew mi ma jox bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*.
13Boo ko séentoo ba noppi, yaw itam dees na la tërali ca say bokk, ni sa mag Aaróona,
14gannaaw yeena diiŋat sama ndigal ca màndiŋu Ciin, fa mbooloo ma jote woon ak man. Yeena wormaalul sama sellaay ca kanam mbooloo ma, ca ndox ma. Mooy walum Meriba ma woon ca Kades, ca màndiŋu Ciin.»
15Musaa nag wax Aji Sax ji, ne ko:
16«Aji Sax ji, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, ngalla tabbal nit ku jiite mbooloo mi,
17kuy xareji, jiite leen, délsi, jiite leen, di leen yóbbu, di leen delloosi, ba mbooloom Aji Sax ji baña mel ni xar yu amul sàmm.»
18Aji Sax ji ne Musaa: «Jëlal Yosuwe doomu Nuun. Nit la ku fit fees. Nanga ko teg sa loxo, sase ko noonu.
19Taxawal ko fi kanam Elasar sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bi, ci kanam mbooloo mépp, te nga sas ko ci seen kanam,
20daldi koy sédd lenn ci sa daraja, ngir mbooloom bànni Israayil mépp déggal ko.
21Ca Elasar sarxalkat bi nag la war di dem, ngir mu di ko seetal fi kanam Aji Sax ji, lu Urim|lemma="Urim ak Tumim:"*, jumtukaayu tegtal bi, feeñal. Ci ndigalal Elasar nag lañuy génne, te ci ndigalam it lañuy dellusee, moom Yosuwe, ak mboolem bànni Israayil giy ànd ak moom, mbooloo mépp.»
22Ba mu ko defee Musaa def, na ko Aji Sax ji sante. Mu ànd ak Yosuwe, taxawal ko fa kanam Elasar sarxalkat bi, ak mbooloo mépp.