Màndiŋ ma 28:1-30 WOLB2025 - Bible AI

1Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:

2«Santal bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee.

3Nga waxleen ne leen, lii moo di saraxu sawara bi ñuy indil Aji Sax ji: ay kuuyu menn at yu mucc sikk, ñaar ci bés bi, muy saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* bi war bés bu nekk.

4Menn kuuy mi, ngeen sarxal ko ci suba, ñaareel bi, ngeen sarxal ko diggante ngoon ak jant bu so.

5Benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, tollu ci ñetti kilo, mooy saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* bi kuuy mu nekk di àndal, ñu tooyale ko walaatu xiinu diwu segalu oliw, tollu ci liitar.

6Looloo di rendi-dóomal bi war bés bu nekk, na ñu ko dogale woon ca tundu Sinayi, ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.

7«Saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"* si mu àndal, walaatu xiin lay doon, tollu ci liitar ngir kuuy mu ci nekk. Ci ëtt bu sell|lemma="sell:"* bi lees di sotti biiñ, muy saraxu tuuru bi ñeel Aji Sax ji.

8Meneen kuuy mi, sarxeleen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu pepp ak saraxu tuuru niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

9«Bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"* nag ñaari kuuyu menn at yu mucc sikk lay doon, ak saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"*, biy ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, ñu tooyale ko ag diw, te mu ànd ak saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"*.

10Loolooy saraxu rendi-dóomalu|lemma="Sarax yi:"* bésub Noflaay, ci bésub Noflaay bu nekk, te bokkewul ak dóomal bi war bés bu nekk, te ànd ak saraxu tuuru.

11«Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ñeel Aji Sax ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu ci nekk mucc sikk,

12ak ñetti fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom ñeenti kilo, muy saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"*, ñu tooyale ko ag diw, booleek yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efay sunguf su mucc ayib, di juróom benni kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek kuuy mu mag mi,

13ak benn fukkeelu efab sunguf su mucc ayib, di ñetti kilo, muy saraxu pepp, ñu tooyale ko ag diw, booleek mépp kuuyum menn at. Saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm, di saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.

14«Ay saraxi tuuru|lemma="Sarax yi:"* lay àndal, genn-wàllu xiinu biiñ la, tollu ci ñaari liitar ci yëkk wu nekk, ak benn ñetteelub xiin, tollu ci liitar ak genn-wàll ci kuuy mu mag mi, ak walaatu xiin, tollu ci liitaru biiñ ci mépp kuuyu menn at. Loolooy saraxu rendi-dóomalu weer wi, weer wu ci nekk, ba weeri at mi daj.

15Ak itam bennub sikket, mu ànd ak saraxu tuuru ngir saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"*, ñeel Aji Sax ji ci bésub Terutel weer wi, te bokkewul ak rendi-dóomal bi ñuy sarxe bés bu nekk.

16«Fukki fan ak ñeent ci weer wi njëkk, mooy màggalu bésub Mucc|lemma="Màggal yi:"* ba, ñeel Aji Sax ji.

17Ëllëg sa, fukki fan ak juróom ci weer woowu, di màggal; diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir lees cay lekk.

18Bés bu jëkk boobu, woote bu sell|lemma="sell:"* lees cay amal. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.

19Nangeen ci def saraxu sawara, mu dib rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te ngeen def lépp di lu mucc sikk.

20Yooyii ànd ak saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"*, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo, ciw yëkk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo, cim kuuy mu mag,

21ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo, ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,

22ak benn sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"* ngir seen njotlaay.

23Te bokkewul ak rendi-dóomalu suba si, rendi-dóomal boobu war bés bu nekk.

24Sarax yu mel noonu ngeen di sarxal ci bés bi, ak seen saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"*, diiru juróom ñaari fan, muy ñamu saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Ci kaw rendi-dóomal bi war bés bu nekk, ci lees koy dolli.

25Bésub juróom ñaareel ba, seen bésub woote bu sell lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.

26«Bésub ndoortel meññeef|lemma="Sarax yi:"* ba ngeen di sarxesi saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* mu bees, ñeel Aji Sax ji, ci seen biir màggalug Ayi bés|lemma="Màggal yi:"* nag, seen bésub woote bu sell|lemma="sell:"* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.

27Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at.

28Saraxu peppam di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw. Ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wu nekk, ak ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,

29ak fukkeelub efa, di ñetti kilo, ci mii kuuy, fukkeelub efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,

30ak bennub sikket ngir seen njotlaay.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>