1«Bu loolu weesoo, benn fanu weeru juróom ñaareel, seen bésu woote bu sell|lemma="sell:"* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Bés la bu ngeen di yéenee ay liit.
2Sarxalleen ci ab rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu ci nekk mucc sikk.
3Saraxu peppam|lemma="Sarax yi:"* lay àndal, di sunguf su mucc ayib, su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,
4ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
5ak benn sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"*, ngir seen njotlaay.
6Bokkewul ak rendi-dóomalu Terutel weer wu nekk, biy ànd ak saraxu pepp, bokkewul it ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk, teyu ànd ak saraxu pepp, ak seen saraxi tuuru|lemma="Sarax yi:"*, ni ko yoon tërale. Dees koy def ngir xetug jàmm, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
7«Fukki fanu juróom ñaareelu weer woowu it, seen bésub woote bu sell|lemma="sell:"* lay doon, te ngeen toroxlu ci. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
8Sarxalleen ci ab rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy mu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp.
9Saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* lay àndal, di sunguf su mucc ayib su ñu tooyale ag diw; ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci yëkk wi, ñaari fukkeeli efa, di juróom benni kilo ci kuuy mu mag mi,
10ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba juróom ñaari kuuy yu ndaw yi daj,
11ak benn sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"*, te du bokke ak póotum bàkkaaru njotlaay gi, ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp, ak seen saraxi tuuru|lemma="Sarax yi:"* yi ci war.
12«Fukki fan yaak juróom ci juróom ñaareelu weer woowu itam, seen bésu woote bu sell|lemma="sell:"* lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey. Amalleen ci ag màggal, ñeel Aji Sax ji, diiru juróom ñaari fan, doore ko ca bés ba.
13Nangeen ca sarxal ab rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: fukki yëkk yu ndaw ak ñett, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
14Seen saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"* di sunguf su mucc sikk su ñu tooyale ag diw, ñetti fukkeeli efay sunguf, di juróom ñeenti kilo ci wenn yëkk wu nekk, ba fukki yëkk yeek ñett daj; ñaari kuuy yu mag yi, kuuy mu ci nekk, ñaari fukkeeli efay sunguf, di juróom benni kilo,
15ak benn fukkeelu efab sunguf, di ñetti kilo ci mii kuuy, benn fukkeelu efa ca mee, ba fukki kuuy yu ndaw yeek ñeent daj,
16ak benn sikketu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"*. Bokkewul ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, ak saraxu pepp si muy àndal, ak saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"*.
17«Bésub ñaareel ba: fukki yëkk yu ndaw ak ñaar; ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
18Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
19Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxi tuuru yi mu àndal.
20«Bésub ñetteel ba: fukki yëkk yu ndaw ak benn, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
21Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
22Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru yi mu àndal.
23«Bésub ñeenteel ba: fukki yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
24Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuyu menn at ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
25Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
26«Bésub juróomeel ba: juróom ñeenti yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
27Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
28Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
29«Bésub juróom benneel ba: juróom ñetti yëkk, ak ñaari kuuy yu mag, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
30Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
31Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
32«Bésub juróom ñaareel ba: juróom ñaari yëkk, ak ñaari kuuy, ak fukk ak ñeenti kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
33Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
34Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.
35«Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.
36Nangeen ci sarxal ab rendi-dóomal, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji: wenn yëkk, ak menn kuuy yu mag, ak juróom ñaari kuuyu menn at, te lépp mucc sikk.
37Te seen saraxi pepp, ak seen saraxi tuuru yay ànd ak yëkk ya, ak kuuy yu mag ya, ak kuuy yu ndaw ya, na dayo ya dëppoo ak li yoon tëral.
38Dees na ca teg benn sikketu póotum bàkkaar, te du bokke ak saraxu dóomal bi war bés bu nekk, mook saraxu pepp ak saraxu tuuru ya mu àndal.