1Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:
2«Fexeel ba feyul bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ci waa Majan+ 31.2 Seetal ci 25.16-19.*. Gannaaw loolu dees na la yóbbu, tëral la fa say bokk.»
3Musaa daldi wax ak mbooloo ma, ne leen: «Na ñenn ci yeen gànnaayu, waajal xare, te dal ci kaw waa Majan, ba feyul Aji Sax ji.
4Gii giir, junni, gee giir junni, ba giiri Israayil yépp daj, ngeen yebal leen ñu xareji.»
5Ba mu ko defee ñu tànne ca gàngoori Israayil, junniy góor jóge ci giir gu nekk, ñuy fukki junneek ñaari xarekat (12 000) yu gànnaayu.
6Musaa nag yebal leen, junni jóge ci giir gu nekk, ñu xareji. Ñoom ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bi Fineyas doomu Elasar, ñoo xareji, yóbbaale jumtukaay yu sell|lemma="sell:"* yaak liiti xare ya.
7Ñu xareek Majan, na ko Aji Sax ji sante Musaa, ba rey góor ñépp,
8reyaale buuri Majan, Ewi ak Rekem ak Cur ak Ur ak Reba, juróomi buuri Majan ya. Balaam doomu Bewor it, ñu reye ko saamar.
9Ba loolu amee bànni Israayil jàpp jigéeni Majan, ak seeni tuut-tànk, ak seen jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, seen alal jépp, ñu sëxëtoo ko.
10Seen dëkk yépp ak seeni dëkkuwaay, ak seen dal yépp, ñu lakk.
11Ba mu ko defee ñu jël mboolem la ñu sëxëtoo, mboolem la ñu ca jàppe, nit ñaak jur ga.
12Ñu daldi yóbbu ca Musaa ak Elasar sarxalkat ba, ak mbooloom bànni Israayil, ña ñu jàppe ca xare ba, ak la ñu ca jàppe, ak la ñu sëxëtoo. Ñu indi lépp ca seen dal ba ca joori Mowab, fa janook Yeriko, te dendeek dexu Yurdan.
13Ci kaw loolu Musaa ak Elasar sarxalkat ba ànd ak mboolem njiiti mbooloo ma, ñu génn dal ba, gatandu leen ca biti.
14Musaa nag sànju ca kaw kilifay xare ya, muy kilifay kuréeli junni yaak kilifay kuréeli téeméer ya jóge xare.
15Musaa ne leen: «Kon jigéeni Majan ñépp ngeen bàyyi, ñu dund!
16Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israayil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji?
17Kon nag reyleen lépp luy góor ci tuut-tànk yi, mboolem lu ciy jigéen ju xam lalu góor it, rey leen,
18mboolem lu ciy jigéen ju ndaw, te xamul lalu góor, ngeen bàyyi mu dund, ñeel leen.
19«Te yeen nag, dalleen ci biti, buleen dugg ci biir dal bi diiru juróom ñaari fan, mboolem ñi rey ak mboolem ñi laal ku ñu rey. Nangeen setlu bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, yeen ak ñi ngeen jàpp.
20Te itam lépp luy yére, ak bépp jumtukaayu der, ak lépp lees defare kawari bëy, ak bépp jumtukaayu bant, nangeen ko setal.»
21Ba mu ko defee Elasar sarxalkat ba wax ak ña xareji woon, ne leen: «Lii moo di dogalu yoon, bi Aji Sax ji dénk Musaa:
22Luy wurus ak xaalis ak xànjar, ak weñ gu ñuul, ak weñ gu weex, ak betteex,
23mboolem lu dul lakk, rekk, nangeen ko laalale sawara, mu set. Ndoxum setlu mi it, warees na koo dellu setale yooyii. Waaye mboolem luy lakk, ci ndoxum setal mi doŋŋ lees koy dugal, ngir mu set.
24Bésub juróom ñaareel ba, fóotleen seeni yére, daldi set. Gannaaw loolu man ngeena duggsi ci dal bi.»
25Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
26«Yaw ak Elasar sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bi, ak ñi jiite seeni kër maam ci mbooloo mi, waññleen alal ji ñu nangoo xare, nit aku jur.
27Xaajleen sëxëtoo mi ñaar, te ngeen séddale ko diggante xarekat ya xareji woon, ak mbooloo mi ci des yépp.
28Te ngeen sàkkal Aji Sax ji, ci céru xarekat ya xareji woon, ab galag bu yemook benn bopp ci juróomi téeméer (500) yu nekk, ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt.
29Ci céru xarekat yi ngeen koy sàkke, jox ko Elasar sarxalkat bi, jagleel ko Aji Sax ji.
30Céru bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween|lemma="Leween b-:"* ñi sàmm ndénkaaneb màkkaanu Aji Sax|lemma="xaymab ndaje m-:"* ji.»
31Ba loolu amee Musaa ak Elasar sarxalkat bi defe ko noonee ko Aji Sax ji sante Musaa.
32La des ca alalu sëxëtoo ja ña xareji woon indaale, gannaaw ba ñu ca génnee yooyu, nii la tollu: gàtt yi, juróom benni téeméeri junneek juróom ñaar fukk ak juróom (675 000);
33nag yi, juróom ñaar fukki junneek ñaar (72 000);
34mbaam yi, juróom benn fukki junneek benn (61 000),
35aw nit, fanweeri junniy jigéen ak ñaar ñu xamul lalu góor (32 000).
36Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500),
37galagu Aji Sax ji génne ci gàtt yi, di juróom benni téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom (675);
38nag yi, fanweeri junneek juróom benn (36 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom ñaar fukk ak ñaar (72);
39mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61);
40aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32).
41Ba mu ko defee Musaa jox galag ba Elasar sarxalkat ba, jagleel ko Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante Musaa.
42Genn-wàll giy céru bànni Israayil, ba Musaa teqale ak cérub ña xareji woon,
43te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la;
44nag yi di fanweeri junneek juróom benn (36 000);
45mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500);
46aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000).
47Musaa daldi sàkk ci céru bànni Israayil boobu, benn ci juróom fukk yu nekk. Musaa jox loola Leween ñi sàmm ndénkaaneb màkkaanu Aji Sax ji, noonee ko ko Aji Sax ji sante woon.
48Ba loolu amee njiiti gàngooru xarekat ya, kilifay kuréeli junni yaak kilifay kuréeli téeméer ya, ñoom ñépp dem ca Musaa.
49Ñu ne Musaa: «Sang bi, nun de, waññ nanu xarekat yi ci sunu kilifteef, waaye kenn wuutewu ci.
50Moo tax nu saraxe ngir Aji Sax ji, ku nekk ak la nga muurloo, ci gànjari wurus: lami përëg, ak takkub jara, ak jaaroy torlukaay, ak jaaroy nopp, aki caq. Noo ko def sunu njotlaayal bakkan, fi kanam Aji Sax ji.»
51Musaa ak Elasar sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba nangoo wurus wa ca ñoom, lépp di takkaay yu ñu tëgg.
52Mboolem li ñu jébbal Aji Sax ji ci wurus di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaari téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñeent fukki kilo (190), te bawoo ci kilifay kuréeli junni yaak kilifay kuréeli téeméer ya.
53Xarekati gàngoor ga ñoom, dañoo féetewoo la ñu sëxëtoo.