1Ba Yeesu joxee ndigal yooyu, fukki taalibeem ya ak ñaar ba noppi, da faa bàyyikoo, ngir jàngaleji aka waare ca seen dëkki gox ba.
2Gannaaw loolu Yaxya|lemma="Yaxya:"* moo dégge ca kaso ba, jëfi Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi. Mu yónni nag ci moom ay taalibeem,
3ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
4Yeesu ne leen: «Li ngeen dégg te gis ko, demleen àgge ko Yaxya.
5Silmaxa yaa ngiy gis, lafañ yi di dox, gaana|lemma="gaana:"* yiy wér, tëx yiy dégg, néew yiy dekki, néew-doole yiy dégg xibaaru jàmm bi.
6Ku xàccul sa péeteek man nag, ndokkalee yaw.»
7Ba taalibey Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
8Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu rafet yi, ci këri buur lañu dëkk!
9Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
10Ci moom moomu lañu bindoon ne:
11Maa leen ko wax déy, li jigéen jur, ku sut Yaxya masu cee feeñ. Waaye ki gëna tuut ci nguurug asamaan a ko sut.
12Ca jamonoy Yaxya ba léegi, nguurug asamaan mu ngi jànkoonteek coono, ñiy jëfe doole di ko jéema aakimoo.
13Ndaxte mboolem yonent yi, ak yoonu Musaa wax nañu, ba kera Yaxya di feeñ.
14Te Yaxya moomu, ndegam man ngeena jàpp li may wax, mooy Ilyaas|lemma="Ilyaas:"* mi waroona délsi+ 11.14 Seetal ci +bk Malasi+bk* 3.23.*.
15Ku ami nopp nag, na dégg.
16«Ana ku may niruleek niti tey jii? Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma, di awoonte, naan:
17“Noo leen toxorool, fecculeen,
18Ndaxte Yaxya daa dikk, lekkul, naanul, ñu naay: “Aw rab la àndal.”
19Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki ñëw, di lekk aka naan, ñu naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat|lemma="juutikat b-:"* yeek bàkkaarkat yi!” Waaye xel mu rafet, jëf ja mooy la koy dëggal.»
20Ci kaw loolu Yeesu ŋàññ na waa dëkk ya fa mu def la ëpp cay kéemaanam, te taxul ñu tuub.
21Mu ne: «Wóoy ngalla yeen waa Korasin, yeen waa Betsayda it, wóoy ngalla yeen, nde kéemaan yi ame fi seen biir, su doon fa waa Tir|lemma="Tir:"*, mbaa fa waa Sidon la ame, kon bu yàgg lañu doon sol ay saaku, xëppoo dóomu-taal, ngir tuub.
22Waaye maa leen ko wax, keroog bés-pénc, waa Tir ak Sidon a leen di gënu demin, yeen.
23Yeen waa Kapernawum nag, ndax dees na leen yékkati ba asamaan am déet? Xanaa ba fa njaniiw kay ngeen di wàcci, nde kéemaan yi ame fi seen biir, su doon fa Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"* la ame, fa la dëkk ba doon des ba tey.
24Waaye maa leen ko wax, keroog bés-pénc, waa Sodom a leen di gënu demin.»
25Ca jamono yooyu la Yeesu àddu ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi,
26nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
27Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn ràññeewul Doom ji, ku dul Baay bi; Baay bi it, kenn ràññeewu ko, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.
28«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal.
29Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof.