Macë 13:1-57 WOLB2025 - Bible AI

1Bésub keroog booba la Yeesu jóge kër ga, dem toog ca tàkkal dex ga.

2Mbooloo mu bare daje fa moom, ba mu mujj dugg ci gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tàkk ga.

3Ci kaw loolu Yeesu wax leen lu bare ciy léeb. Mu ne leen: «Dama ne, boroom jiwu moo demoon jiwi.

4Naka lay saaw ab toolam, ndeke lenn ca jiwu maa nga tuuru ca kaw yoon wa, picc yi dikk, lekk ko.

5Leneen la nag tuuru fu barey doj, te suuf sa néew. Mu ne coleet ca saa sa, ndax la suuf sa xóotul.

6Teewul ba jant bi jógee, mu lakk, daldi wow, ndax ñàkkub reen.

7Leneen la tuuru ca xaaxaam ma, xaaxaam ma sëq, tanc ko.

8La des ca jiwu ma nag tuuru ca suuf su baax, ba meññ; wii fepp meññal téeméer; wee, juróom benn fukk; wale, fanweer.

9Ku ami nopp, na dégg.»

10Gannaaw loolu ay taalibeem dikk, laaj ko ne ko: «Lu tax ngay wax ak nit ñi ci ay léeb?»

11Mu ne leen: «Yeen lañu may ngeen xam mbóoti nguurug asamaan, waaye ñale, mayeesu leen ko.

12Ndax ku am, dees na ko dolli, ba mu barele; waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.

13Ci ay léeb laay wax ak ñoom, ngir ñuy xoole te duñu gis, di déglu te duñu dégg, duñu xam.

14Kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* ya Esayi|lemma="Esayi:"* jottali, ci ñoom la sottee. Mooy ba mu nee:

15Ndax xolu xeet wee, dërkiis;

16«Waaye ndokkalee yeen, nde seeni gët a ngi gis, seeni nopp di dégg!

17Maa leen ko wax déy, bare na ay yonent ak nit ñu jub ñu nammoona gis li ngeen gis te gisuñu ko, ak itam dégg li ngeen dégg te dégguñu ko.

18«Kon nag yeen dégluleen pirim léebu boroom nji mi.

19Képp ku dégg kàddug nguurug Yàlla, su ko xamul, ku bon ki|lemma="ku bon ki:"* mooy dikk, këf jiwu mi ci xolam; kooku mooy ki jote jiwu mi ci kaw yoon wi.

20Ki jote jiwu mi fu barey doj nag, mooy ki dégg kàddu gi rekk, nangoo ko xol bu sedd ci saa si.

21Waaye ab reen la jotula saxle ci biiram, moo tax du ko wéye. Bu coono dikkee, mbaa ñu bunduxataal ko ndax kàddu gi, day dellu gannaaw ci saa si.

22Ki jote jiwu mi ci xaaxaam yi, mooy ki déglu kàddu gi, te xalaati àddina ak naxey alal fatt kàddu gi, ba tax meññul.

23Ki jote jiwu mi ci suuf su baax si nag, mooy ki déglu kàddu gi, dégg ko, ba meññal, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp li ñu ji woon; muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»

24Yeesu léebati leen, ne leen: «Nguurug asamaan dafa mel ni nit ku ji jiwu mu baax cib toolam.

25Naka la nit ñay nelaw, ab noonam dikk, ji ab jëmb ci biir pepp mi, daldi dem.

26Ba pepp ma saxee ba defi gub, jëmb ba itam feeñ.

27«Ba loolu amee surgay boroom kër ga dikk ne boroom kër ga: “Sang bi, xanaa du jiwu mu baax nga jiwoon ci sa tool bi? Ana kon fu jëmb bi jóge?”

28Mu ne leen: “Ab noon a def loolu.” Surga ya ne ko: “Tee noo dem, wolli ko?”

29Mu ne leen: “Déedéet, lu ko moy ngeen wolli ko, ba far buddiwaale pepp mi.

30Bàyyileen leen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob jot. Bu ngóob jotee nag, góobkat yi laay wax ne leen: ‘Jëkkleena wolli jëmb bi, takk koy say, ngir lakk ko, te ngeen yeb pepp mi ci samam sàq.’”»

31Yeesu léebati leen, ne leen: «Nguurug asamaan dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko cib toolam.

32Doomu fuddën moo gëna tuut ci mboolem jiwu, waaye bu saxee ba màgg, mooy sut ci gàncax gi, ba mujj di garab gu njanaaw yiy dikk, tàgg ciy caram.»

33Yeesu léebati leen: «Nguurug asamaan dafa mel ni lawiir ju jigéen sàkk, def ko ci ñetti natti sunguf yu mag+ 13.33 ñetti natti sunguf mu ngi tollu ci 25 kilo.*, ba tooyal bépp mujj funki.»

34Kàddu yooyu yépp, ay léeb la ko Yeesu waxe mbooloo ma. Waxu leen dara lu moy ci aw léeb.

35Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu yonent ba, mate. Mooy ba mu nee:

36Ci kaw loolu Yeesu yiwikoo ca mbooloo ma, daldi dugg ca kër ga. Taalibeem ya dikk ne ko: «Firil nu léebu jëmb bi sax ci tool bi.»

37Yeesu ne leen: «Ki ji jiwu mu baax mi mooy Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki.

38Tool bi mooy àddina; jiwu mu baax moomu mooy niti nguurug Yàlla; jëmb bi di niti ku bon ki|lemma="ku bon ki:"*.

39Noon bi ko ji mooy Seytaane|lemma="Seytaane:"*; ngóob mi mooy tukkitel àddina, góobkat yi di malaaka yi.

40Noonu ñu wollee jëmb ba, lakk ko, ni lay deme ca tukkitel àddina.

41Doomu nit ki mooy yebal ay malaakaam, ñu wollee ci nguuram mboolem luy bàkkaarloo, ak mboolem defkati ndëngte,

42sànni leen sawara; foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.

43Su booba aji jub ñi dañu naa ràññ ni jant bi, fa seen nguurug Baay. Ku ami nopp, na dégg.»

44«Nguurug asamaan dafa mel ni alal ju ñu làq cib tool. Nit gis ko, làqaat, xol ba sedd, ba mu dem jaay mboolem lu mu am, jënd tool ba.

45«Nguurug asamaan dafa mel it ni jula buy wut peri gànjar.

46Mu gis nag per buy jar lu bare, daldi jaay mboolem lu mu am, ba jënd per ba.»

47«Nguurug asamaan mel na it ni mbaal mu ñu sànni biir géej, mu jàpp wirgoy jën wu nekk.

48Mbaal ma fees, ñu xëcc ba ci tefes gi, daldi toog, tànn yu baax yi, def ciy dàmba; yu bon yi, ñu sànni ca biti.

49Noonu lay deme, ca tukkitel àddina. Malaaka yeey dem, seppi ñu bon ñi ci biir aji jub ñi,

50sànni leen sawara. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.»

51Yeesu nag laaj taalibe ya, ne leen: «Ndax xam ngeen lu loolu lépp di tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.»

52Mu ne leen: «Kon nag bépp firikatu yoon bu ñu jàngal mbirum nguurug asamaan, dafa mel ni boroom kër bu yebbee cib dencam, lu yees ak lu yàgg.»

53Ba Yeesu sottalee ca léeb yooyu la fa bàyyikoo,

54daldi dellu dëkk ba mu yaroo. Mu di leen jàngal nag ca seen jàngu, ba ñu yéemu naan: «Ana fu kii jële bii xam-xam, ak yii kéemaan?

55Xanaa kii du doomu minise bi? Xanaa du Maryaama mooy yaayam? Rakkam yu góor di Yanqóoba ak Yuusufa ak Simoŋ ak Yudd?

56Xanaa du nook jigéenam ñépp a dëkk? Ana fu kii jële lii lépp nag?»

57Ñu daldi gise mbir ma ag yabeel.

© 2025 Bible Society of Senegal