1Ci jamono yooyu la Erodd|lemma="Erodd:"* boroom Galile dégg turu Yeesu.
2Mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya|lemma="Yaxya:"*. Moo dekki noonu, moo waral xam-xam yu kéemaane yi feeñe ci moom.»
3Erodd nag moo jàppoon Yaxya, yeew ko, tëj, ndax gannaaw ba Erodd jëlee Erojàdd jabaru Filib magam,
4Yaxya moo wax Erodd, ne ko yoon mayu ko mu denc ndaw si.
5Erodd nag bëgga rey Yaxya, te ragal nit ña, ndax yonent ga ñu ko jàppe woon.
6Ba ñu demee bay baaxantal bésu juddub Erodd, doomu Erojàdd ju jigéen fecc ca géew ba, Erodd am ca mbégte,
7ba dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, ma jox la ko.»
8Ndaw sa nag wax Erodd, ci ndigalal yaayam, ne ko: «Indil ma fii boppu Yaxya ci ndab.»
9Aw tiis nag dikkal Buur Erodd, ndax ngiñ la, ak gan ña. Teewul mu joxe ndigal ngir ñu jox ko ko,
10daldi yónnee, ñu dog boppu Yaxya ca kaso ba.
11Ci kaw loolu ñu indi bopp bi ci ndab, jox ko janq ba, mu yót yaayam.
12Ba mu ko defee taalibey Yaxya dikk, yóbbu néew ba, denc ko. Ñu dem nag, wax ko Yeesu.
13Ba Yeesu déggee loolu da faa bàyyikoo, dugg gaal, jëm béreb bu wéet, ngir beruji fa. Teewul nit ña yég ko, bàbbeekoo ca dëkk ya, leru tefes gi, topp ko.
14Ba mu wàccee ca gaal ga, mbooloo mu réy la gis. Mu ñeewante leen, daldi faj seeni jarag.
15Ca ngoon sa taalibe yi dikk, ne ko: «Fii àllub neen la, te guddi na xaat. Dangay yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd ag lekk.»
16Teewul Yeesu ne leen: «Jarul ñu dem, yeen joxleen leen lu ñu lekk.»
17Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
18Yeesu ne leen: «Indilleen ma ko fii.»
19Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, dagg mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko mbooloo ma.
20Ñépp lekk ba regg, ba ñu yóbbu desit ya, muy fukki pañe ak ñaar yu fees.
21Ña ca xéewlu nag juróomi junni (5 000) góor lañu, limaaleesul jigéen ña ak gone ya.
22Ci kaw loolu Yeesu duggloo taalibeem ya ca gaal ga, ngir ñu jàllagum, jiituji ko ca wàlla, ba kera mu yiwi mbooloo ma.
23Mu yiwi mbooloo ma, daldi yéegi ca tund wa, ngir ñaan. Ba guddi jotee moom doŋŋ a fa nekkoon.
24Booba gaal ga dem na xaat ba dànd tefes ga, diggante bu takku, gannax ya di ko baaje, ndax ngelaw la leen soflu.
25Ba suuf seddee, Yeesu dox ci kaw dex gi, wutsi leen.
26Taalibe ya gis ko, muy dox ca kaw dex ga, ñu daldi jommi, naan: «Njuuma la!» di yuuxoo ndax tiitaange.
27Yeesu wax ak ñoom ca saa sa, ne leen: «Dalleen, man mii la, buleen tiit!»
28Piyeer nag ne tonet, ne ko: «Sang bi, su dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ba ci yaw.»
29Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer wàcce ca gaal ga, dox ci kaw ndox mi, jëm ca Yeesu.
30Teewul ba mu gisee na ngelaw la riddee, dafa tiit, tàmbalee suux. Mu àddu ca kaw, ne: «Sang bi, wallu ma!»
31Yeesu daldi tàllal loxoom, jàpp ko, ne ko: «Yaaka néew ngëm, ana looy xel ñaar?»
32Ci kaw loolu ñu dugg ca gaal ga, ngelaw la dal.
33Taalibe ya ca gaal ga nag sujjóotal ko, ne ko: «Aylayéwén, yaa di Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"* ji.»
34Ba loolu amee ñu jàll dex ga, daldi teeri ca diiwaanu Senesaret.
35Niti gox ba xàmmee Yeesu, daldi yónnee ca diiwaan bépp, indil ko mboolem ña wopp.