Macë 15:1-38 WOLB2025 - Bible AI

1Ca jamono yooyu la ay Farisen|lemma="Farisen y-:"* ak ay firikati yoonu Musaa bàyyikoo Yerusalem, dikk ba ci Yeesu, ne ko:

2«Lu tax say taalibe di jalgati aaday maam yi, ba duñu raxas seeni loxo, bala ñoo lekk?»

3Yeesu nag ne leen: «Yeen itam lu tax ngeen di jalgati santaaneb Yàlla, ndax seen aaday bopp?

4Ndax Yàlla da ne: “Teralal ndey ak baay+ 15.4 Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 20.12.*,” neeti: “Ku saaga sa ndey mbaa sa baay, dee rekk mooy àtteem+ 15.4 Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 21.17.*.”

5Te yeen ngeen ne: “Ku ne sa ndey mbaa sa baay: ‘Li ma warlook yaw, jébbal naa ko Yàlla,’

6kooku wàccoo na ak warugaru teral baayam.” Kon kay neenal ngeen kàddug Yàlla ndax seen aaday bopp.

7Jinigalkat yi ngeen doon, Esayi|lemma="Esayi:"* yey na, ba mu jottalee kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* ci seen mbir, ne:

8“Askan wii, làmmiñ lañu may wormaale,

9Seen njaamu Yàlla neen la,

10Ci kaw loolu Yeesu woo mbooloo ma, ne leen: «Dégluleen te amug dégg.

11Du li dugg ci gémmiñ mooy sobeel nit ki, waaye liy génne ci gémmiñ, loolu mooy sobeel nit ki.»

12Ba loolu amee taalibe ya dikk ne ko: «Ndax xam nga ne, ba Farisen yi déggee kàddu googu, mer nañu?»

13Yeesu ne leen: «Gépp gàncax gu sama Baay ba fa asamaan jëmbatul, dees na ko buddi.

14Bàyyileen leen, ay gumba yuy wommat ay gumba lañu; gumba nag, su dee wommat gumba, ñoom ñaar ay ànd tàbbi ci kàmb.»

15Piyeer nag ne Yeesu: «Firil nu léeb woowu.»

16Yeesu ne ko: «Kon yeen itam amuleenug dégg ba tey?

17Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci koll bi lay dugg, balaa jàll, génneji gannaaw kër?

18Li génne ci gémmiñ nag ci xolu boroom la jóge, te loolu mooy sobeel nit ki.

19Ndaxte ci xol la mébét yu bon di jóge, ak bóom, ak njaaloo, ak séy yi yoon tere, ak càcc, ak seede lu dul dëgg, ak saaga.

20Yooyu mooy sobeel nit ki, waaye lekk te raxasuwuloo sobeelul nit.»

21Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem diiwaanu Tir ak Sidon|lemma="Tir:"*.

22Ci kaw loolu as ndawas Kanaaneen jekki jóge ca gox booba, di wax ca kaw, naan: «Sang bi, Sëtub Daawuda|lemma="Daawuda:"*, yërëm ma! Sama doom ju jigéen la rab jàpp, mu sonn lool.»

23Yeesu nag tontuwu ko baat, taalibeem ya dikk ne ko: «Dàqal kii nu topp, di yuuxu ci sunu kaw!»

24Yeesu daldi ne: «Yebaleesu ma fu dul ci xari bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* yi réer.»

25Teewul ndaw sa dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, dimbali ma!»

26Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko kuti yi, jaaduwul.»

27Ndaw sa ne ko: «Dëgg la, Sang bi, waaye teewul kuti yi for ca la ruuse ca seen ndabal boroom.»

28Yeesu nag ne ko: «Ndaw sii, yaaka réy ngëm. Kon nag na la amal noonu nga ko bëgge.» Ca waxtu woowa la doom ja wér.

29Ba mu ko defee Yeesu bàyyikoo foofa, dem ca tàkkal dexu Galile. Mu yéeg ca kaw tund wa, toog fa.

30Mbooloo mu bare dikk, ànd aki lafañ, ak ay gumba, ak boroomi laago, aki luu, ak boroom jàngoro yu bare. Ñu indi leen fa kanam Yeesu, mu faj leen,

31ba mbooloo ma waaru ca lañu gis luu ya di wax, boroom laago ya wér, lafañ ya di dox, gumba ya di gis. Ñu daldi sàbbaal Yàllay Israayil.

32Gannaaw loolu Yeesu woo taalibeem ya, ne leen: «Damaa yërëm mbooloo mi, ndax ñetti fan a ngii yu ñu nekk ak man, te amuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi, ñu deme xiif, bala ñoo tële ci yoon wi.»

33Taalibe ya ne ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bu wéet bi mburu mu suur mbooloo mu réye nii?»

34Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak as jën.»

35Ba mu ko defee Yeesu sant mbooloo ma ñu toog ci suuf.

36Mu jël juróom ñaari mburu ya ak jën ya, daldi yékkati kàddug cant, dagg mburu ma, jox taalibe ya, ñu jox mbooloo ma.

37Ñépp lekk ba regg, te desit wa ñu yóbbu di juróom ñaari dàmba yu fees.

38Ña ca lekk ñeenti junniy (4 000) góor lañu, te limaaleesul jigéen ña ak gone ya.

© 2025 Bible Society of Senegal