1Ay Farisen|lemma="Farisen y-:"* ak ay Sadusen|lemma="Sadusen y-:"* nag ñoo dikkoon ci Yeesu, di ko fiir, ne ko: «Firnde ju bawoo asamaan lanu bëgg, nga won nu ko.»
2Yeesu ne leen: «Su ngoonee ngeen ne: “Ëllëg de day naaj, nde asamaan si daa xonq.”
3Su dee ag suba ngeen ne: “Tey dina taw, asamaan saa ngi xiin, xonq curr.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, te manuleena ràññee firndey janti tey.
4Maas gu bon te ñàkk kóllëre gi ngeen doon, firnde ngeen di wut, waaye deesuleen jox jenn firnde ju moy firndey Yunus.» Gannaaw loolu, mu bàyyikoo fa ñoom, dem.
5La ca tegu, taalibe ya jàllaat dex ga, ndeke fàtte nañoo yóbbaale mburu.
6Yeesu ne leen: «Wattuleen te moytu lawiiru Farisen|lemma="Farisen y-:"* ñi ak Sadusen|lemma="Sadusen y-:"* ñi.»
7Taalibe ya nag di werante ci seen biir naan: «Nun de yóbbaalewunu mburu.»
8Yeesu xam la ñuy wax, ne leen: «Yeenaka néew ngëm, lu ngeen di werante ci seen biir, naan amuleen fi mburu?
9Kon xamaguleen ba tey, fàttalikuwuleen it juróomi mburu ya ca juróomi junniy (5 000) nit ña, ak ñaata pañey desit ngeen ca jële?
10Juróom ñaari mburu ya ca ñeenti junniy (4 000) nit ña nag, ñaata dàmbay desit ngeen ca jële?
11Nu ngeen mana umplee ne du mburoo ma tax di wax, ne ngeen wattu lawiiru Farisen ñeek Sadusen ñi?»
12Ca lañu doora xam ne du lawiiru mburoo ko tax di wax, waaye njàngalem Farisen ña ak Sadusen ña, moom la leen wax ñu wattu ko.
13Ba Yeesu demee ca diiwaan ba féete péeyu Sesare gu Filib, mu laaj taalibeem ya, ne leen: «Ana ku nit ñi wax ne mooy Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki?»
14Taalibe yi ne ko: «Ñii de nee ñu Yaxya|lemma="Yaxya:"* la, ñee ne, Ilyaas|lemma="Ilyaas:"* la; ñale ne Yeremi la, mbaa keneen ci yonent yi.»
15Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?»
16Simoŋ Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi, Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"* Aji Dund ji.»
17Yeesu ne ko: «Ndokkalee yaw, Simoŋ doomu Yowaan, ndax nit xamalu la ko, xanaa sama Baay ba fa asamaan.
18Man nag maa ne la, yaa di Piyeer, doj wi; ci kaw doj wii it laay samp mbooloom gëmkat ñi, te dooley dee du ko manal dara.
19Maa lay jox caabiy nguurug asamaan, te loo yeew ci kaw suuf, yeewees na ko fa asamaan; loo yiwi ci kaw suuf it, yiwees na ko fa asamaan.»
20Gannaaw loolu Yeesu dénku taalibe yi, ngir ñu baña wax kenn ne mooy Almasi bi.
21Ci jamono yooyu la Yeesu tàmbalee xamal taalibeem ya ne fàww mu dem Yerusalem, ba daje fa ak coono yu bare yu bawoo ca magi askan wa, ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yu mag ya, ak firikati yoonu Musaa ya, te dees na ko rey, ba ñetteelu fan ba, mu dekki.
22Ci kaw loolu Piyeer ñaarook moom, tàmbali koo femmu, ne ko: «Yàlla tere, Sang bi, loolu du la dal mukk.»
23Teewul Yeesu geestu, ne Piyeer: «Seytaane|lemma="Seytaane:"*, xiddi ma, te dellu gannaaw, yaa ngi may gàllankoor; yaw xalaatoo yëfi Yàlla, waaye yëfi nit ngay xalaat.»
24Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp te nga gàddu sa bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
25Ndaxte képp ku bëgga rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, dinga ko jotaat.
26Te it jagoo àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Ak lu nit wara mana weccee bakkanam?
27Doomu nit ki de mooy dikke darajay Baayam, ànd aki malaakaam, te su boobaa mooy fey ku nekk ay jëfam.