Macë 17:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1Ba ñu ca tegee juróom benni fan, Yeesu ànd na ak Piyeer ak Yanqóoba ak Yowaan rakku Yanqóoba, yóbbu leen kaw tund wu kawe, ngir wéetook ñoom.

2Mu soppiku fa seen kanam, xar kanamam di melax nib jant, ay yéreem weex nig leer.

3Ci kaw loolu Yonent Yàlla Musaa ak Yonent Yàlla Ilyaas|lemma="Ilyaas:"* jekki feeñu leen, di waxtaan ak Yeesu.

4Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun. Soo nangoo ma yékkati fii ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.»

5Naka lay wax ba tey, niir wu leer yiir leen, baat jekki jibe ca niir wa ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe, moom laay bànneexoo; dégluleen ko.»

6Ba ca taalibe ya déggee, dañu ne dàll, dëpp seen jë fa suuf, tiit lool.

7Yeesu dikk, teg leen loxoom|lemma="teg loxo:"*, ne leen: «Jógleen, buleen tiit.»

8Ñu séentu ca kaw, gisuñu ku dul mennum Yeesu doŋŋ.

9Naka lañuy wàcce ca tund wa, Yeesu sant leen, ne leen «Buleen nettali kenn peeñu mi, ba kera Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki dekki.»

10Ci kaw loolu taalibe ya laaj ko, ne ko: «Lu tax nag firikati yoonu Musaa yi ne fàww Ilyaas njëkka ñëw?»

11Yeesu ne leen: «Waaw, Ilyaas kay mooy ñëw, ba jubbanti lépp.

12Maa leen wax nag ne leen Ilyaas ñëw na ba noppi, waaye xàmmeesu ko, te it lu leen neex lañu def ak moom. Noonu it la Doomu nit ki nara sonne ci seeni loxo.»

13Booba nag la taalibe ya xam ne mbirum Yaxya|lemma="Yaxya:"* la leen di wax noonu.

14Ba ñu dikkee ba jub mbooloo ma, genn góor dikk, sukk fa kanamam,

15ne ko: «Sang bi, yërëmal sama doom. Day say te sonn na lool; léeg-léeg mu daanu ci sawara, léeg-léeg mu daanu ci ndox.

16Indi naa ko ci say taalibe, waaye manuñu koo faj.»

17Yeesu nag ne: «Céy niti tey, yeena gëmadi te dëng, maak yeen ba kañ? Dama leen di muñal ba kañ?» Mu ne leen: «Indilleen ma xale bi fii.»

18Ci kaw loolu Yeesu gëdd rab wa, rab wa génne ca xale ba, mu daldi wér ca waxtu wa.

19La ca tegu taalibe ya dikk ba ca Yeesu, daldi koy laaj ci sutura, ne ko: «Lu waral manunu woona dàqal sunu bopp, rab wi?»

20-21 Yeesu ne leen: «Xanaa seenug néew ngëm. Maa leen ko wax déy, su ngeen amee ci ngëm, lu tollu ni peppu fuddën, dingeen ne tund wii: “Toxool fii, ba fale,” mu toxu, te dara du leen të.»

22Ba Yeesu ak taalibe ya dajee ca diiwaanu Galile nag, Yeesu da ne leen: «Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki lees di wor léegi, ngir teg ko ci loxoy nit ñi;

23dees na ko rey, mu dekki ca ñetteelu fanam.» Ñu daldi am tiis wu réy lool.

24Ba Yeesu ak taalibe ya agsee Kapernawum, feyeekukati galagu kër Yàlla ga ñoo dikk, ne Piyeer: «Xanaa seen kilifa gi da dul fey galagu kër Yàlla gi+ 17.24 galagu kër Yàlla googu, ñaari daraxma la. Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 30.13.*?»

25Piyeer ne leen: «Ahakay!»

26Mu ne ko: «Xanaa doxandéem yi.» Yeesu ne ko: «Kon nag ag pey wàcc na njaboot gi.

© 2025 Bible Society of Senegal