1Gannaaw ba Yeesu juddoo ca Betleyem gu diiwaanu Yude, yemook janti Buur Erodd|lemma="Erodd:"*, ndeke ay boroom xam-xam yu bàyyikoo penku dikk nañu Yerusalem.
2Ñu ne: «Ana buur bi Yawut yi juddule? Biddiiwam lanu gis ca penku, moo tax nu dikk siyaaresi ko.»
3Ba Buur Erodd déggee loolu, dafa jaaxle, mook mboolem waa Yerusalem.
4Ci kaw loolu mu woolu mboolem sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yu mag ya, ak firikati yoonu Musaa ya. Mu daldi leen laaj fu Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi wara juddoo.
5Ñu ne ko: «Xanaa Betleyem gu diiwaanu Yude, ndax noonu la ko yonent ba binde, ne:
6“Yaw Betleyem gu diiwaanu Yuda nag,
7Ba loolu amee Erodd woolu boroom xam-xam ya ci kumpa, di leerlu bés ba biddiiw ba feqee.
8Mu yebal leen nag Betleyem, ne leen: «Demleen seetal ma bu baax, mbirum xale bi. Bu ngeen ko gisee, xamal ma ko, ngir man itam ma siyaareji ko.»
9Ñu déglu buur ba ba noppi, dem. Ci kaw loolu rekk biddiiw ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen di dem, ba àgg, fa tiim béreb ba xale ba nekk, mu daldi taxaw.
10Ba ñu gisee biddiiw ba taxaw, bég nañu lool, mbég mu réya réy.
11Ñu dugg ca kër ga, gis xale bi ak ndeyam Maryaama. Ñu daldi ne gurub sukk, sujjóotal xale bi. Ba loolu amee ñu yebbi seenub denc, génne ca yóbbalu wurus ak cuuraay, ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
12Gannaaw loolu kàddu dikke leen ci gént, artu leen ngir ñu baña dellu ca Erodd. Ba mu ko defee ñu jaare weneen yoon, ñibbi seenum réew.
13Ba boroom xam-xam ya ñibbee, am malaakam Boroom bi moo jekki feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Jógal, ànd ak xale bi ak ndeyam te nga daw ba Misra, toog fa, ba kera ma di la jox ndigal, ndax Erodd|lemma="Erodd:"* dina seet xale bi, ngir sànk ko.»
14Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, ag guddi, ngir làquji Misra.
15Fa la toog, ba Erodd faatu. Noonu la mbir ma deme, ngir sottal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee:
16Ba Erodd gisee ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mer na mer mu réy lool, ba yeble, ngir reylu ci Betleyem ak la ko wër, mboolem xale yu góor yi am diggante ñaari at ak lu ko yées, muy diggante ba méngook àpp ba mu leerloo woon ca boroom xam-xam ya.
17Booba la kàddu ga jottalikoo woon ci Yonent Yàlla Yeremi mate. Mooy ba mu nee:
18«Baat a nga jibe fa Raama,
19Gannaaw ba Erodd|lemma="Erodd:"* faatoo, am malaakam Boroom bi moo jekki feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
20ne ko: «Jógal ànd ak xale bi ak ndeyam te nga dellu Israayil. Ñi doon wuta jël bakkanu xale bi dee nañu.»
21Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, daldi dellu réewum Israayil.
22Teewul mu dégg ne Arkelawus moo falu buur ca Yude, wuutu baayam Erodd, ba tax mu ragal faa dem. Ci biir loolu kàddug artu dikkal ko ci gént, mu daldi walbatiku, làquji diiwaanu Galile.