1«Nguurug asamaan dafa mel ni boroom kër bu teela xëy, di wut ay surga yu ko liggéeyal toolub reseñam.
2Mu juboo ak liggéeykat ya ci bëccëg bu nekk peyug bëccëgu lëmm. Mu daldi leen yebal ca toolub reseñam.
3Naka mu génn wetu juróom ñeenti waxtu ci suba, daldi gis ñeneen ñuy taxawaalu ca pénc ma, defuñu dara.
4Mu ne leen: “Demleen yeen itam ca sama toolub reseñ, ma fey leen lu jaadu.”
5Ñu dem. Ci booru fukki waxtook ñaar ci bëccëg, mu dellu génn, fukki waxtook juróom itam, mu génnati, defati noona ba tey.
6Wetug fukki waxtu ak juróom ñaar, mu génnati, dajeek ñeneen ñuy taxawaalu. Mu ne leen: “Lu ngeen di yendoo taxawaalu fii te defuleen dara?”
7Ñu ne ko: “Dees noo jëlul.” Mu ne leen: “Demleen yeen itam ca sama tool.”
8«Ba ngoon jotee, boroom tool ba ne ab jawriñam: “Wool surga yi, fey leen seen bëccëg, te nga tàmbalee ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi jiitu.”
9Ci kaw loolu ña ñu jëloon ca booru fukki waxtu ak juróom ñaar dikk, ku ci nekk jot peyug bëccëgu lëmm.
10Ña ñu njëkkoona jël dikk, yaakaar ne ñooy ëpple ag peyoor, te teewul ñu feyu, ñoom it, ku nekk peyug bëccëgu lëmm.
11Ñu jël, tey sikk boroom kër ga,
12naan: “Ñii mujja ñëw, liggéeyuñu lu moy wenn waxtu, nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi, ak naaj wu tàng wi!”
13Teewul boroom kër ga ne kenn ka: “Sama waay, tooñuma la. Xanaa juboowunu woon ci peyug bëccëgu lëmm?
14Jëlal sa yëf te dem. Li ma la fey, moom laa yéenee fey kii mujja ñëw.
15Xanaa damaa sañula def lu ma neex ci sama alal? Am sab xol a bon ci samag mbaax?”
16Noonu la ñi mujj di jiitujee, ñi jiitu, mujje.»
17Gannaaw loolu nag Yeesu jëm Yerusalem, yóbbaale fukki taalibe yaak ñaar, wéetook ñoom, daldi leen xamal ca yoon wa ne leen:
18«Noo ngii jëm Yerusalem, te dees na wor Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki, jébbal ko sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yu mag yaak firikati yoonu Musaa ya, ñu teg ko àtteb dee,
19jébbal ko jàmbur ñi dul Yawut, ñu ñaawal ko, caw ko, daaj ko ci bant, mu dee; ba ca ñetteelu fan ba, mu dekki.»
20Booba la jabaru Sebede ànd ak doomam yi mu am ak moom, ñu dikk ba ca Yeesu. Jigéen ja sujjóot, ngir mbir mu muy sàkku ci moom.
21Yeesu ne ko: «Loo bëgg?» Mu ne ko: «Mayal sama ñaari doom yii, ñu toog, kii féete la ndijoor, kii féete la càmmoñ, keroog ca sa nguur ga.»
22Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Mbaa kaasub naqar bi may naani, man ngeen koo naan?» Ñu ne ko: «Man nanu ko.»
23Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy, sama kaasub naqar de, dingeen ko naan. Tooge sama ndijoor mbaa sama càmmoñ nag, du man maay maye loolu, waaye da diy cér yu ñeel ña ñu ko waajalal, ci sama dogalu Baay.»
24Ba fukki taalibe ya ca des déggee mbir ma, seen xol tàng ca ñaari doomi ndey ya.
25Yeesu nag woo leen ne leen: «Xam ngeen ne njiiti xeeti àddina yi dañuy def nit ñi jaam, seeni kàngam di leen néewal doole.
26Yeen nag, bumu deme noonu ci seen biir. Képp ku bëgga doon ku màgg ci yeen, na nekk seenub surga,
27te ku bëgga nekk seen njiit, na doon seenub jaam.
28Noonu la deme ci Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug|lemma="jot:"* ñépp.»
29Ba Yeesu bàyyikoo Yeriko, mbooloo mu baree ko topp.
30Ndeke ñaari silmaxaa nga tooge ca peggu yoon wa. Ba ñu déggee ne Yeesu mooy romb, dañoo xaacu, ne: «Sang bi, Sëtub Daawuda|lemma="Daawuda:"*, yërëm nu!»
31Nit ña nag femmu leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna xaacooti, ne: «Sang bi, Sëtub Daawuda, yërëm nu!»
32Yeesu daldi taxaw, woo leen, ne leen: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
33Ñu ne ko: «Sang bi, xanaa sunuy bët ubbiku.»