Macë 22:1-45 WOLB2025 - Bible AI

1Yeesu léebati leen, ne leen:

2«Nguurug asamaan dafa mel ni buur bu doon waajal céetalug doomam ju góor.

3Mu yebal ay surgaam, ngir ñu jëli ña ñu woo ca bernde ja, te ñooñu bëgguñoo ñëw.

4Mu yebalaat yeneen surga, ne: “Waxleen gan ñi ñu woo, ne leen: ‘Reer yi kat noppi na; samay nag ak sama juru yafal lañu rey, lépp sotti na, ñëwleen ci bernde ji.’”

5Teewul ñu fénantal, dem seen yoon; kii ca toolam, kee cam njaayam,

6ñee jàpp surga ya, toroxal leen, rey leen.

7«Buur nag mer, daldi yónni gàngooram, ñu reyi bóomkat yooyu, lakk seenub dëkk.

8Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Bernde ji de noppi na, waaye gan ñi ñu woo ñoo ko yeyoowul.

9Kon nag demleen ca selebe yoon ya, ku ngeen fa gis, woo ko ci céetal gi.”

10Surga ya dem ca mbedd ya, daldi dajale mboolem ña ñu fa gis, ku baax ak ku bon, ba céet ga fees aki gan.

11«Ci kaw loolu buur bi duggsi, di xool gan ñi, daldi cay seetlu ku ag colam warul ci ag céet.

12Buur ne ko: “Xarit, noo dugge fii, te soluloo col gi war ci ag céet?” Kooku ne cell.

13Buur ne dag ya: “Yeewleen tànk yeek loxo yi, te ngeen sànni ko ca lëndëm gu tar ga ca biti. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.”

14Ndax kat ñu bare lañu woo, waaye ñu néew lañu tànn.»

15Booba la Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya diisooji ngir lal pexe mu ñu fiire Yeesu ci kàddoom.

16Ñu daldi yebal ci moom seeni taalibe ak ñi ànd ak farandooy Buur Erodd, ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku dëggu nga, te ci biir dëgg ngay jàngalee yoonu Yàlla. Ragaloo kenn it, ndax seetuloo ci jëmmi nit.

17Kon nag wax nu sa xalaat: ndax yoon maye na ku fey Buur Sesaar|lemma="Sesaar:"* ab galag am déet?»

18Teewul Yeesu xam seen mébét mu bon, daldi ne leen: «Lu ngeen may seetloo, jinigalkat yi?

19Wonleen ma poset bi ñuy feye galag.» Ñu daldi ko jox benn posetub xaalis+ 22.19 posetu xaalis bii: ab dinaar la woon, moo doon peyu bëccëgu lëmm.*.

20Yeesu ne leen: «Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?»

21Ñu ne ko: «Buur Sesaar.» Mu ne leen: «Kon nag, yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar, te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»

22Ba ñu déggee loolu lañu waaru, daldi koy bàyyi, dem.

23Bésub keroog boobu Sadusen|lemma="Sadusen y-:"* yi ne dee-dekki amul, ca lañu dikk ba ca moom. Ñu laaj ko ne ko:

24«Kilifa gi, Musaa noon na: “Su góor faatoo te amul doom, na ku mu bokkal waajur donn jabaram, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay+ 22.24 Seetal ci +bk Baamtug yoon wi+bk* 25.5.*.”

25Léegi nag juróom ñaari góor a ngi woon ci sunu biir, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba faatu te amul doom, ba tax rakk ja donn jabar ja mu bàyyi gannaawam.

26Tofo ba ak ñaareelu tofo ba def noonu, ba juróom ñaar ñépp dee.

27Gannaaw gi, ndaw sa it dee.

28Keroog ndekkite la nag, kan ci juróom ñaar ñi lay doon jabaram, gannaaw ñoom ñépp a ko jëloon?»

29Yeesu nag ne leen: «Seen njuumte moo di xamuleen Mbind mi, xamuleen manoorey Yàlla,

30ndax keroog ndekkite la, kenn du am jabar mbaa jëkkër, waaye nit ñi dañuy mel ni malaaka yi ci asamaan.

31Ci wàllu ndekkite sax, xanaa jànguleen la leen Yàlla waxoon ne leen:

32“Maay Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"*+ 22.32 Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 3.6.*”? Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund.»

33Ba ca mbooloo ma déggee, dañoo waaru ca njàngaleem.

34Ba Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya yégee na Yeesu tëje gémmiñu Sadusen|lemma="Sadusen y-:"* ya, dañoo féncoo.

35Ci kaw loolu kenn ca ñoom, ab xamkatub yoonu Musaa, di ko fexee fiir, laaj ko ne ko:

36«Kilifa gi, lan ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?»

37Yeesu ne ko: «“Yàlla sa Boroom, nanga ko soppe sa léppi xol, ak sa léppi jëmm, ak sa léppi xel+ 22.37 Seetal ci +bk Baamtug yoon wi+bk* 6.5.*.”

38Loolu mooy ndigal li gëna màgg, te moo jiitu.

39Ñaareel bi it yem ak moom, di: “Ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom+ 22.39 Seetal ci +bk Sarxalkat yi+bk* 19.18.*.”

40Ci ñaari ndigal yooyu la mboolem yoonu Musaa, ak kàdduy yonent yi aju.»

41Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya ñoo daje woon, Yeesu laaj leen, ne leen:

42«Luy seen xalaat ci Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi, kan lay ab sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda|lemma="Daawuda:"*.»

43Yeesu ne leen: «Ana kon nan la Daawuda mana waxe ci ni ko leeru Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi dikkale, ba di ko woowe “Sang bi”, naan:

44“Boroom bi daa wax sama Sang ne ko:

45Gannaaw Daawuda moo woowe Almasi bi “Sang bi,” nu mu nekke ab sëtam?»

© 2025 Bible Society of Senegal