1Jant yooyu la Yaxya|lemma="Yaxya:"* feeñ, di waare ca màndiŋu Yude,
2naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndax nguurug asamaan dëgmal na.»
3Kooku lañu doon wax, te Yonent Yàlla Esayi|lemma="Esayi:"* jottali woon ko, ba mu nee:
4Yaxya nag mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem la daan sol, laxasoo laxasaayu der ca ndiggam, ab dundam diy njéeréer ak lemu àll.
5Nit ña daldi bàbbeeku, jëm ca moom, waa Yerusalem, ak mboolem diiwaanu Yude, ak mboolem diiwaanu dexu Yurdan.
6Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
7Ci kaw loolu ay Farisen|lemma="Farisen y-:"* ak ay Sadusen|lemma="Sadusen y-:"* yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox. Yaxya ne leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen artu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?
8Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel,
9te buleen defe ne man ngeena wax ci seenum xel ne: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
10Léegi nag xàcc nañu sémmiñ ngir gor reenu garab yi ba noppi. Kon gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.
11Man, cim ndox laa leen di sóob, ngir jëmmal seenug tuubeel. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma sut, ba ay caraxam sax yeyoowuma ko koo summil. Moom nag ci Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi ak ci sawara+ 3.11 Sóobu gi ci Noo gu Sell gi ak ci sawara: Almasi bi moo leen di sol doole ju bawoo ci Noo gu Sell gi, ak itam setal leen ni sawara di setale weñ gu am lu ko rax. Sawara dina taxawe itam céru mbugal mu ñeel ñi déggalul Yàlla. Seetal ci 12.49; +bk Jëf ya+bk* 2.3.* la leen di sóob.
12Ab layoom a ngi ci loxoom, te mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; am peppam lay fat ci sàq mi, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
13Booba la Yeesu jóge Galile, dikk ngir Yaxya|lemma="Yaxya:"* sóob ko ca dexu Yurdan.
14Teewul Yaxya gàntal, ne ko: «Man may ki soxla, nga sóob ma ci ndox, yaw nga dikk ci man!»
15Yeesu ne ko: «Baalagum noonu rekk, ndax ci lanuy matale lépp li Yàlla bëgg ci njub.» Yaxya daldi koy nangul.
16Gannaaw ba ñu sóobee Yeesu, ba mu génnee ca saa sa ca ndox ma, asamaan a jekki ubbiku ngir moom. Mu gis Noowug Yàlla|lemma="Noo gu Sell g-:"* wàcc ni am pitax ca kawam.