Macë 6:1-33 WOLB2025 - Bible AI

1«Wattuleena def seenu njekk ci kanam nit ñi, ngir ngistal. Lu ko moy, dungeen ame yool fa seen Baay ba fa asamaan.

2Kon nag booy sarxe, bul ko yéglee coowal liit, ni ko jinigalkat yiy defe ci jàngu yi ak mbedd yi, ngir nit ñi kañ leen. Maa leen ko wax déy, ñooñu jot nañu seen yool bu mat sëkk.

3Waaye booy sarxe, li sa loxol ndijoor di def, bu ko sa loxol càmmoñ xam,

4su ko defee sa sarax di kumpa, te sa Baay biy gis ci biir kumpa moo lay yool.

5«Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni jinigalkat yi safoo taxaw di ñaan ci jàngu yi ak selebe yoon yi, ngir fés. Maa leen ko wax déy, ñooñu jot nañu seen yool bu mat sëkk.

6Yaw nag booy ñaan, duggal sa néegu biir, tëj sa bunt, te nga ñaan sa Baay ci kumpa. Sa Baay biy gis ci biir kumpa moo lay yool.

7«Bu ngeen di ñaan, buleen jàppoo kebetu ni yéefar yi foog ne ci wax ju bare lees leen di nangule.

8Kon buleen mel ni ñoom, ndax seen Baay xam na li ngeen soxla bala ngeen ko koo ñaan.

9Yeen nag nangeen ñaane nii:

10na sa nguur dikk,

11May nu bésub tey, sunu dundub bés bu nekk,

12te nga baal nu sunuy tooñ, ni nu baale nun itam, ñi nu tooñ.

13Bu nu dugal ci nattu,

14«Su ngeen baalee nit ñi seeni tooñ, seen Baay ba fa asamaan dina leen baal, yeen itam.

15Waaye su ngeen baalewul, seen Baay it du leen baal seeni tooñ.

16«Su ngeen di woor, buleen yoggoorlu ni jinigalkat yi. Dañuy ñaawal seen kanam, ngir wone ne dañoo woor. Maa leen ko wax déy, ñooñu jot nañu seen yool bu mat sëkk.

17Yaw nag booy woor, xeeñlul te sëlmu ba set,

18ngir baña won nit ñi sa koor, ba mu des sa Baay bi teew ci kumpa. Sa Baay biy gis ci biir kumpa moo lay yool.

19«Buleen dajale ab denc ci kaw suuf, fi ko max ak xomaag di yàqe, mbaa ab sàcc bëtt, jël ko.

20Waaye dajaleleen ab denc fa asamaan, fa ko max ak xomaag dul yàqe, te ab sàcc du bëtt, jël ko.

21Ndaxte fa sab denc nekk, sab xol it a nga fa.

22«Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo,

23waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm. Leer gi ci yaw nag, su dee ag lëndëm, ndaw lëndëm gu réy!

24«Kenn manula jaamu ñaari sang; dangay dëddu kii, sopp kee, mbaa nga fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.

25«Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol. Xanaa du lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo?

26Xoolleen picc yi: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci am sàq. Teewul seen Baay ba fa asamaan di leen dundal. Yeen nag, xanaa du yeena gën picc yi fuuf?

27Ana kan ci yeen mooy jaaxle, di xalaat a xalaat bakkanam, ba mana yokk ci àppam, lu tollook xef ak xippi?

28«Koddaay nag, ana lu ngeen ciy jaaxle? Seetaatleen ni tóor-tóor yiy saxe ci tool yi. Doñ-doñiwuñu, ëccuñu,

29waaye maa leen wax ne Suleymaan ak darajaam jépp sax, soluwul woon ni benn ci ñoom.

30Ndegam ñaxum tool miy dund tey, te léegi ñu sànni ko cib taal, moom la Yàlla di wodde nii kay, xanaa astamaak yeen? Yeenaka néew ngëm!

31Kon nag, buleen jaaxle, naan: “Lu nuy lekk?” mbaa “Lu nuy naan?” mbaa “Lu nuy sol?”

32Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.

33Waaye njëkkleena tiisoo nguurug Yàlla, ak njub gi mu laaj, te loolu lépp moo leen ko ciy dollil.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>