1Yeesu moo wàcce ca tund wa, mbooloo mu bare topp ko.
2Ab gaana|lemma="gaana:"* jekki dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sang bi, su la soobee, man nga maa setal.»
3Mu tàllal loxoom, laal ko ne: «Soob na ma, setal.» Ca saa sa ngaanaam|lemma="ngaana g-:"* ga set wecc.
4Yeesu ne ko: «Fexeel ba bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba, ngir mu seet la, te nga génne sarax si yoonu Musaa santaane+ 8.4 Seetal ci +bk Sarxalkat yi+bk* 14.1-32.*, ngir muy firnde ci ñoom.»
5Gannaaw ba Yeesu duggsee dëkk ba ñuy wax Kapernawum, ab njiitu takk-der|lemma="njiitu takk-der b-:"* bu waa Room moo dikk ba ci moom, ñaan ko,
6ne ko: «Sang bi, sama surga moo tëdd ca kër ga, lafañ, te nekke mitit wu tar.»
7Yeesu ne ko: «Man, maay dikk, faj ko.»
8Teewul njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg sama kër; waxal genn kàddu rekk, sama surga wér.
9Ndaxte man itam ci kilifteef laa tënku, te maa ngeek ay takk-der yu nekk ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem, ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ko nee: “Defal lii,” mu def ko.»
10Ba ko Yeesu déggee, daa yéemu, daldi ne ñi topp ci moom: «Maa leen ko wax, déy, ku réye nii ngëm, gisuma ko ci bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*.
11Maa leen wax ne leen, ñu bareey bawoo penku ak sowu, dikk bokk ca ndabal bernde ja, ñook Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"*, keroog ca nguurug asamaan.
12Waaye doom yi yeyoo nguur ga, ñoom lees di sànni ca biti ca lëndëm gu tar ga. Foofa lees di jooye aka yéyoo ndax mitit.»
13Ci kaw loolu Yeesu ne njiitu takk-der ba: «Demal, noonu nga ko gëme, na ame noonu ci yaw.» Ca waxtu woowa la surga ba wér.
14Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer, daldi fekk yaayu jabaru Piyeer, mu tëdd, yaram wa tàng.
15Yeesu jàpp loxol soxna sa, tàngooru yaram wa teqalikook moom, soxna sa jóg, di ko toppatoo.
16Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Ba loolu amee Yeesu dàqe rab ya kàddoom, mboolem ña wopp, mu faj leen.
17Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ci gémmiñu Yonent Yàlla Esayi|lemma="Esayi:"* mate. Mooy ba mu nee:
18Ba Yeesu gisee mbooloo ma ko wër nag, dafa sant taalibe ya, ñu jàll ba ca wàllaa dex ga.
19Ci biir loolu ab firikatu yoonu Musaa dikk, ne ko: «Kilifa gi, yaw laay topp fépp foo jëm.»
20Yeesu itam ne ko: «Till akug kàmbam, njanaaw akub tàggam, waaye Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki de, amul fu mu wéer boppam.»
21Ba loolu amee keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma njëkka dem robi sama baay.»
22Yeesu ne ko: «Toppal ci man te nga bàyyi néew yi, ñu rob seeni néew.»
23Ba mu ko defee, Yeesu dugg ca gaal ga, ay taalibeem ànd ak moom.
24Ca saa sa ngelaw lu réy yëngal dex ga, ba gannax ya mëdd gaal ga. Teewul Yeesoo ngay nelaw.
25Taalibe ya jegesi, yee ko, ne: «Sang bi, wallu nu, nu ngi sànku!»
26Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di tiit, yeenaka néew ngëm!» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw la ak gannax ya. Lépp ne sendaw.
27Ba loolu amee, ñu waaru, naan: «Kii moo di kan, ba ngelaw leek dex gi di ko déggal?»
28Ba Yeesu jàllee, ba teere diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp ñoo génne ca sëg ya, dikk dogale ko, te di ñu soxor lool, ba kenn ñemewul woona jaare foofa.
29Ñu jekki xaacu, ne: «Yaw Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"* ji, ana lu nu joteek yaw? Ndax danga fee ñëw ngir mbugal nu, te jotagul?»
30Fekk na genn coggalu mbaam-xuux yu baree nga leen dànd lu sore, di for.
31Rab ya tinu ko ne: «Boo nu dàqee, yebal nu ca coggalu mbaam-xuux ya.»
32Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ci saa si coggal gépp bartaloondoo, tàbbi ca dex ga, daldi lab.
33Ba loolu amee sàmm ya daw, ba ca dëkk ba, nettaliji lépp, ak la xewoon ca ña rab jàpp.