Macë 9:1-37 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu Yeesu dugg gaal, jàll dex ga, daldi dellu dëkkam.

2Ñu jekki indil ko ab lafañ, mu tëdd cig laltu. Ba Yeesu seetloo seen ngëm, da ne lafañ ba: «Na sa xel dal, doom, jéggalees na la say bàkkaar.»

3Ay firikati yoonu Musaa nag jekki di wax ci seen biir naan: «Kii, Yàlla lay diir mbagg!»

4Teewul Yeesu xam seen xalaat, ne leen: «Lu waral yii xalaat yu bon ci seen xel?

5Ana ci yii yaar, lu ci gëna yomb: ne “Jéggalees na la say bàkkaar,” am ne: “Jógal te dox”?

6Kon nag dingeen xam ne Doomu nit|lemma="Doomu nit k-:"* ki am na ci kaw suuf, sañ-sañu jéggale ay bàkkaar.» Mu ne lafañ ba: «Jógal, jël sag laltu, te ñibbi.»

7Lafañ ba jóg, daldi ñibbi.

8Ba mbooloo ma gisee loolu, dañoo tiit, di sàbbaal Yàlla, mi may nit ñi boobu sañ-sañ.

9Yeesu bàyyikoo ca, daldi gis waa ju ñuy wax Macë, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: «Kaay, topp ma.» Mu jóg, topp ko.

10Gannaaw ga, Yeesu doon lekk ca kër Macë, lu bare ci ay juutikat|lemma="juutikat b-:"* aki bàkkaarkat jekki dikk, ñu bokk di lekk, ñook Yeesu aki taalibeem.

11Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya nag gis loolu, ne taalibe ya: «Juutikat yeek bàkkaarkat yi la seen kilifa di bokkal lekk nag?»

12Yeesu nag dégg ca, ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.

13Demleen jàngi lu kàddu gii di firi: “Ngor laa namm, dub sarax+ 9.13 Seetal ci +bk Ose+bk* 6.6.*,” ndax du ñi jub laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo.»

14Gannaaw loolu taalibey Yaxya|lemma="Yaxya:"* dikk ca Yeesu ne ko: «Lu tax nun ak Farisen|lemma="Farisen y-:"* yi, nuy woor, te say taalibe duñu woor?»

15Yeesu ne leen: «Ndax xariti séet dinañu naqarlu dara, li feek boroom séet baa ngi teew ci seen biir? Teewul jamonoo ngi ñëw, dees na jële boroom séet bi ci seen biir; su boobaa nag dinañu woor.

16Kenn du jël sekkit wu yees, di ko daaxe mbubb mu ràpp, ndax sekkit wi day ñoddi mbubb mi, mu gëna xar.

17Te it deesul def biiñ bu bees ci mbuusi der yu ràpp. Lu ko moy, mbuus yi fàcc, biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu. Biiñ bu bees daal, ci mbuus mu bees lees koy def, ñaar ñépp mucc.»

18Naka la leen Yeesu di wax loolu rekk, ab njiit dikk, sujjóotal ko, ne ko: «Sama doom ju jigéen moo faatu léegi, waaye ngalla dikkal, teg ko sa loxo|lemma="teg loxo:"*, mu dund.»

19Yeesu jóg, topp ko, mooki taalibeem.

20Ndeke sennas ndaw a nga ca ànd. Diiru fukki at ak ñaar ma ngay xëpp deret. Mu doxe gannaaw, daldi teg loxoom ca catu mbubbam.

21Fekk na mu naan ci xelam: «Su ma manoona laal catu mbubbam rekk, dinaa wér.»

22Yeesu ne gees, gis ko, ne ko: «Janq, na sam xel dal, sa ngëm a la faj.» Ca waxtu woowa la ndaw sa wér.

23Ci kaw loolu Yeesu agsi ca kër njiit la, daldi gis toxorokati dëj ya, ak kër-këru mbooloo ma.

24Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Nit ña nag di ko ñaawal.

25Gannaaw ba ñu génnee mbooloo ma, Yeesu dugg, jàpp ca loxol janq ba, mu daldi jóg.

26Ba loolu amee coow loola law ca réew ma mépp.

27Ba Yeesu jógee foofa, ñaari silmaxaa ko topp, di xaacu, naan: «Sëtub Daawuda|lemma="Daawuda:"*, yërëm nu!»

28Naka la Yeesu délsi, ba dugg ca kër ga, gumba ya duggsi. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa koo def?» Ñu ne ko: «Waawaaw, Sang bi.»

29Yeesu daldi laal seeni bët, ne leen: «Noonu ngeen ko gëme, na ame noonu.»

30Ca saa sa seeni bët ubbiku. Yeesu nag artu leen bu baax, ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»

31Teewul ñu génn rekk, di waxtaane Yeesu ca gox ba bépp.

32Naka lañuy dem, ñu jekki indil ko ab luu bu rab jàpp.

33Yeesu daldi dàq rab wa, luu ba wax, mbooloo ma waaru, naan: «Guléet lu mel nii feeñ ci Israayil.»

34Teewul Farisen|lemma="Farisen y-:"* ya naan: «Ci buuru rab yi lay dàqe ay rab.»

35Ci kaw loolu Yeesu di wër mboolem dëkk yu mag yaak yu ndaw ya, di leen jàngal ci seeni jàngu, di yégle xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, tey faj mboolem jàngoro, ak mboolem wéradi.

36Ba Yeesu gisee mbooloo ya, da leena ñeewante, ndax na ñu sonne, ne yàcc, mbete xar yu amul sàmm.

37Mu daldi ne taalibeem ya: «Ngóob mee yaatu, te surga yi néew.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>