1Dégluleen rekk li Aji Sax ji wax.
2Yeen tund yu mag yi, dégluleen layoob Aji Sax ji,
3«Yeen sama ñoñ, ana lu ma leen def?
4Yeen maa leen génne réewum Misra,
5Yeen sama ñoñ, fàttalikuleen rekk
6Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji,
7Mbaa dina ma nangul junniy kuuy,
8Yaw nit ki, waxees na la li baax,
9Baatub Aji Sax ji mooy joor dëkk bi,
10ndax alalu njublaŋ a ngi ci biir këri njublaŋ yi ba tey,
11Ana nu may ñàkka toppe màndaxekaayi njublaŋ,
12Boroom alal yi ci sa biir, aw ay lañu fees,
13Man it moo tax ma di la duma ba nga wopp,
14Yaw de dinga lekk, te doo suur,
15Yaw de yaay ji te doo góob,