1Wóoy, ngalla man mi mel ni kuy forsi,
2Ngor a jeex ci réew mi,
3Lu bon la seeni loxo mane:
4Ki gën ci ñoom, neexook ag dég,
5Buleen gëm ab xarit,
6Doom ju góor a ngi sofental baay ba,
7Man nag Aji Sax ji laay séentu,
8Yaw samab noon, bu ma ree;
9Maa moy Aji Sax ji,
10Ndaw siy samab noon moo koy seede, sëlmoo gàcce,
11Bés a ngii bu ñuy tabaxaat say tata,
12Su bés baa ci yaw lees di dikk,
13Àddina ab gent lay doon ndax ñi ko dëkke,
14Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ,
15Aji Sax ji nee: «Maa leen di won ay kiraama,
16Xeet yee ciy gis, rus,
17Ñooy mëq suuf ni jaan,
18Ana Yàlla ju mel ni yaw,
19Moo nuy yërëmati;
20Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"*, yéwéne Ibraayma,