1«Sàkkal ab sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* bu ñuy taal cuuraay|lemma="cuuraay l-:"* ci kawam. Bantu séng nga koy defare.
2Guddaay bi di xasab, yaatuwaay bi di xasab; ab kaare lay doon, taxawaay bi di ñaari xasab, ay béjjénam ànd ak moom di benn bant bi.
3Xoobal ko wurusu ngalam ci kaw gi ak ci wet yi ba mu daj, ak ci béjjén yi, te nga sàkkal ko kéméju wurus mu wër ko.
4Ñaari noppi wurus nga koy sàkkal ci ron kéméj gi. Féetaleel nopp yi ci ñaari wetam, ñu jàkkaarloo, di téye banti njàppu yi ñu koy yóbboo.
5Defal njàppu yi bantu séng te nga xoob njàppu yi wurus.
6«Tegal sarxalukaayu cuuraay bi ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede|lemma="gaalu kóllëre g-:"* si ak kubeeru njotlaay gi ci kaw gaalu àlluway seede si, foofu may dajejeek yaw.
7Na fa Aaróona taal cuuraay suba su nekk. Buy toppatoo làmp yi lay taal cuuraay lu xeeñ li.
8Bu Aaróona di taal làmp yi diggante ngoon ak jant bu so itam, na taal cuuraay lu xeeñ li. Cuuraay la su ñuy taal ba fàww, ci seen gépp maas fi kanam Aji Sax ji.
9Deesu ci sarxal cuuraay lu ñu diglewul, deesu ci rendi saraxu dóomal|lemma="Sarax yi:"*, deesu ci def saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* mbaa saraxu tuuru|lemma="Sarax yi:"*.
10Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"* bi, taqal ci béjjéni sarxalukaayu cuuraay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell|lemma="sell:"* la, ñeel Aji Sax ji.»
11Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
12«Boo tolloo ci taxawal limeefu boppi bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*, na ku nekk ci ñoom fey Aji Sax ji njot-gi-bakkanam ba nga koy lim, ndax menn musiba bañ leena dikkal ci biir lim bi.
13«Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal+ 30.13 siikal, xaalis la woon bu ñuy natt, mu tollu ci fukki garaam ak benn ak genn-wàll.*, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo siikal boobu tollook ñaar fukki gera+ 30.13 gera moo doon natt, ba gënoona tuut ci wàllu diisaay, yemook lu tollook genn-wàllu garaam.*. Genn-wàllu siikal mu dib galag, ñeel Aji Sax ji.
14Képp ku bindu ci limeef bi, te am ñaar fukki at, jëm kaw, na fey galag gi, ñeel Aji Sax ji.
15Ki woomle du fey lu ëpp, ki néewle du fey lu yées genn-wàllu siikal, buy fey galagu Aji Sax ji ngir njot-gi-bakkanam.
16Nanga nangoo xaalisu njot-gi-bakkan bi ci bànni Israayil, te nga féetale ko liggéeyu xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi. Loolu pàttaliku lay doon, ñeel bànni Israayil fi kanam Aji Sax ji, ngir seen njot-gi-bakkan.»
17Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
18«Sàkkal mbalkam njàpp mu xànjar, ak tegub xànjaram ngir ñu di ko jàppe. Teg ko ci diggante xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi ak sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* bi, te nga duy ko ndox.
19Aaróona aki doomam di ci tanq, raxase seeni loxo ak seeni tànk.
20Bu ñuy duggsi ci xaymab ndaje mi, nañu jàpp, ndax ñu baña dee, nañu jàpp itam, bu ñuy liggéeysi fi sarxalukaay bi, di saxaaral saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
21Nañu raxas seeni loxo ak seeni tànk, ndax ñu baña dee. Na loolu di dogal bu sax dàkk, ñeel Aaróona ak askanam ci seen gépp maas.»
22Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
23«Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal: xeetu ndàbb li ñuy wax miir bu ndoxe, sàkk ci juróomi kilo; xasum kanel mu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll; yuuru gattax gu xeeñ, ñaari kilo ak genn-wàll;
24ak xasum kaas, juróomi kilo, yemook juróomi téeméeri siikal, ci siikalu jaamookaay bi; ak ñeenti liitari diwu oliw, yemook benn natt bu ñuy wax xiin.
25Loolu ngay def diwu pal gu sell|lemma="sell:"* gi, te na doon njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax. Diwu pal gu sell lay doon.
26«Nanga ci diw xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi, diw ci gaal gi àlluway seede si dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"*,
27ak taabal ji aki ndabam, ak tegukaayu làmp bi, ak jumtukaayam yépp, ak sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"* cuuraay bi.
28Nanga ci diw itam sarxalukaayu saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* bi, ak ndabam yépp, ak mbalkam njàpp mi akub tegoom.
29Noonu ngay sellale yooyii, mu daldi doon lu sella sell. Lépp lu laal yooyii day doon lu sell.
30Aaróona aki doomam itam, nanga leen diw. Noonu nga leen di sellale, ngir ñu doon samay sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"*.
31«Nanga wax nag bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ne leen: “Googu diw sama diwu pal gu sell lay doon, ci seen gépp maas.
32Doom aadama ju ko jagoowul, deesu ko ko diw, te buleen njafaan lenn lu ni mel, lu ngeen yemale dayoy xeeñal ya ak dayoy diw gu sell gi. Deesu ko def ci yaramu kenn ku ko jagoowul, te buleen njafaan xeeñal yi ciy dem, ci dayo yu tollook dayoy diw gu sell gi, ngir defar lenn lu ni mel. Lu sell la, lu ngeen wara wormaal sellaayam.
33Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israayil.”»
34Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak cuuraay-libaŋ lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo.
35Def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax, xorom ko, mu set, sell|lemma="sell:"*.
36Sàkk ci, wol ko ba mu mokk, nga teg ko fi kanam gaal gi àlluway seede si dence|lemma="gaalu kóllëre g-:"*, fi biir xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* mi, fi may dajeek yaw. Loolu lu sella sell la lu ngeen wara wormaal.
37Waaye cuuraay|lemma="cuuraay l-:"* loolu ngay njafaanlu nag, bu ci njafaanal sa bopp ci dayoy xeeñal yu ni tollu. Lu sell la lu ngeen wara wormaal, ñeel Aji Sax ji.