Neyemi 10:1-39 WOLB2025 - Bible AI

1«Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween|lemma="Leween b-:"* ak sunuy sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* def ci seen màndargay torlukaay.»

2Ñi ko torlu ñoo di

3ak Seraya ak Asaryaa ak Yeremi

4ak Pasur ak Amarya ak Malkiya

5ak Atus ak Sebaña ak Malukk

6ak Arim ak Meremot ak Abdiyas

7ak Dañeel ak Gineton ak Barukk

8ak Mesulam ak Abya ak Miyamin

9ak Maasya ak Bilgay ak Semaya. Ñooñu ñoo di sarxalkat ya.

10Leween ñi ñoo di

11Seeni bokk ca lañu, di Sebaña ak Oja ak Kelita ak Pelaya ak Xanan

12ak Mise ak Rexob ak Asabya

13ak Sakur ak Serebya ak Sebaña

14ak Oja ak Bani ak Beninu.

15Njiiti askan wi ñoo di

16ak Buni ak Asgàdd ak Bebay

17ak Adoña ak Bigway ak Adin

18ak Ater ak Esekiyas ak Asur

19ak Oja ak Asum ak Beccay

20ak Arif ak Anatot ak Nebay

21ak Magpiyas ak Mesulam ak Esir

22ak Mesesabel ak Cadog ak Yaduwa

23ak Pelaca ak Xanan ak Anaya

24ak Ose ak Anaña ak Asub

25ak Aloxes ak Pilxa ak Sobeg

26ak Rexum ak Asabna ak Maaseya

27ak Axya ak Xanan ak Anan

28ak Malukk ak Arim ak Baana.

29Bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ga ca des nag fekksi leen, muy sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yaak Leween|lemma="Leween b-:"* ñaak fara bunt yaak woykat yaak liggéeykati kër Yàlla ga, di mboolem ñi beddeeku woon askanu yéefar yi, ngir topp yoonu Yàlla wi, ñook seeni jabar ak seeni doom yu góor ak yu jigéen, mboolem ñi xam te xàmmee.

30Ci kaw loolu ñu ànd ak seen bokki garmi, waatook ñoom ne dinañu topp yoonu Yàlla wi mu dénkaane, Musaa jaamam ba jottali; di ko sàmm, di jëfe mboolem sunu santaaney Boroom Aji Sax ji ak àttey yoonam ak dogali yoonam.

31Nu ne nag:

32«Te itam bu waa réew mi indee am njaay mbaa lépp luy pepp, di ko jaay ci bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"*, dunu ko jënd ci ñoom bésub Noflaay mbaa bés bu sell|lemma="sell:"*.

33«Ci biir loolu nu warloo santaaney joxe at mu nekk ñeenti garaami xaalis, bu jëm ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga,

34jëm ca mburum teewal|lemma="mburum teewal m-:"* ma, ak saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"* yi war bés bu nekk, ak saraxi dóomal|lemma="Sarax yi:"* yu bés bu nekk, ak saraxi bési Noflaay, ak yu Terutel weer ak yu bési màggal yi, ak yeneen yu ñu sellalal Yàlla, ak saraxi póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"* yi bànni Israayil di jotoo, ak mboolem la war ca sunu liggéeyu kër Yàlla ga.

35«Ay bant lanu tegoo ci sunu biir, nun sarxalkat yeek Leween ñeek baadoolo yi, ngir dogalal waa kër gu nekk àpp ba ñu wara aye cim at, te ñu war caa yóbbu seen sasu matt ca sunu kër Yàlla ga, ngir taal ko ca sunu sarxalukaayu|lemma="sarxalukaay b-:"* Yàlla Aji Sax ji, muy la ñu bind ci téereb yoon wi.

36«Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf njëkka meññle ak lu garab yépp njëkka ñorle.

37Ci biir loolu nu dogoo def li ñu bind ci yoon wi, di yóbbu ca sunu kër Yàlla ga sunu taaw yu góor ak lu sunu jur taawloo, gu gudd gaak gu gàtt ga, di teg lépp ci loxoy sarxalkat ya fay liggéey.

38Ci kaw loolu nu wara yóbbu ca sunu néegi dencukaayi kër Yàlla ga lu njëkk ci sunu nootu sunguf ak sunu njoxey pepp ak sunu meññeefi garab yépp ak sunu biiñ ak diw, di teg lépp ci loxoy sarxalkat yi. Ba tey nuy indil Leween ñi céru fukkeelub lépp luy meññee ci sunu suuf, ndax Leween ñeey dajalesi céri fukkeel yi ci gox yi nuy bey yépp.

39Sarxalkat bu askanoo ci Aaróona mooy gunge Leween ñiy jëlsi céri fukkeel yi. Su ko defee Leween ñi yóbbu fukkeelu céri fukkeel yi ba ca sunu kër Yàlla ga, fat ko ca néegi dencukaayi alal ya.

© 2025 Bible Society of Senegal
v>