1Gannaaw ba ñu tabaxaatee tata ja, ma taxawal lafi bunt ya, ba noppi dénk fara bunt ya seen liggéey, ñook woykat ya ak Leween|lemma="Leween b-:"* ña.
2Ci kaw loolu ma sas sama mbokk Anani, mu jiite Yerusalem, mook Anaña boroom tata ja, ndax la mu gëna dëggu ñu bare, gën leena ragal Yàlla.
3Ma ne leen: «Bu bunti Yerusalem ubbiku li feek jant bi tàngul. Santleen fara bunt yi ñuy tëj bunt yi, sës ci galani tëjukaay yi, balaa waa dëkk biy tëdd. Na ku nekk ci waa Yerusalem di wattoo ca bérebu wattukaayam, mbaa buntu këram.»
4Booba dëkk ba réy na, yaatu na; waaye nit ña ca dëkk ñoo néew, te kër ya tabaxewaatul woon.
5Sama Yàlla xiir ma ma woo garmi yeek kilifa yeek baadoolo yi, ngir bind leen. Ci biir loolu ma gis limeefu làng ya njëkka jóge ngàllo ga, ba ñibbisi. Li ma fekk ñu bind ko ci mooy lii:
6Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nebukatnecar buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbisi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk.
7Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe+ 7.7 Yesuwa ci làkku ebrë. Yosuwe lanu bind ci tekki bii, muy doomu Yoccadag te doon sarxalkat bu mag bi mujj lu jiitu ngàllo ga ca Babilon. Yosuwe mii lu gëna bare dees na ko tuddaaleek Sorobabel. Feneen fu ñu ne Yesuwa ci téere bi, keneen a tax ñuy wax.* ak Neyemi ak Asaryaa ak Raamya ak Naxamani ak Mardose ak Bilsan ak Misperet ak Bigway ak Nexum ak Baana. Limeefu góori bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* nii la tëdde:
8askanu Paros ñaari junni ak téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar (2 172) lañu.
9Askanu Sefatiya ñetti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar (372) lañu.
10Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652).
11Askanu Paxat Mowab, soqikoo ci Yesuwa ak Yowab, di ñaari junni ak juróom ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (2 818).
12Askanu Elam junni ak ñaari téeméer ak juróom fukk ak ñeent (1 254) lañu.
13Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom (845) lañu.
14Askanu Sakay juróom ñaari téeméer ak juróom benn fukk (760) lañu.
15Askanu Binuy juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (648) lañu.
16Askanu Bebay juróom benn téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (628) lañu.
17Askanu Asgàdd ñaari junni ak ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar (2 322) lañu.
18Askanu Adonikam juróom benni téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñaar (667) lañu.
19Askanu Bigway ñaari junni ak juróom benn fukk ak juróom ñaar (2 067) lañu.
20Askanu Adin juróom benn téeméer ak juróom fukk ak juróom (655) lañu.
21Askanu Ater soqikoo ci Esekiyas, di juróom ñeent fukk ak juróom ñett (98).
22Askanu Asum ñetti téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (328) lañu.
23Askanu Beccay ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñeent (324) lañu.
24Askanu Arif téeméer ak fukk ak ñaar (112) lañu.
25Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom (95) lañu.
26Waa Betleyem ak Netofa téeméer ak juróom ñett fukk ak juróom ñett (188) lañu.
27Waa Anatot téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett (128) lañu.
28Waa Bet Asmawet ñeent fukk ak ñaar (42) lañu.
29Waa Kiryaat Yarim ak Kefira ak Beerot juróom ñaari téeméer ak ñeent fukk ak ñett (743) lañu.
30Waa Raama ak Geba juróom benni téeméer ak ñaar fukk ak benn (621) lañu.
31Waa Migmas téeméer ak ñaar fukk ak ñaar (122) lañu.
32Waa Betel ak Ayi téeméer ak ñaar fukk ak ñett (123) lañu.
33Waa Nebo gu ndaw juróom fukk ak ñaar (52) lañu.
34Waa Elam gu ndaw junni ak ñaari téeméer ak juróom fukk ak ñeent (1 254) lañu.
35Waa Arim ñetti téeméer ak ñaar fukk (320) lañu.
36Waa Yeriko ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom (345) lañu.
37Waa Lodd ak Adidd ak Ono juróom ñaari téeméer ak ñaar fukk ak benn (721) lañu.
38Waa Senaa ñetti junni ak juróom ñeenti téeméer ak fanweer (3 930) lañu.
39Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yi ñii la: askanu Yedaya, soqikoo ci waa kër Yosuwe, di juróom ñeenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (973).
40Askanu Imer junni ak juróom fukk ak ñaar (1 052) lañu.
41Askanu Pasur junni ak ñaari téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (1 247) lañu.
42Askanu Arim junni ak fukk ak juróom ñaar (1 017) lañu.
43Leween ñi ñii la: askanu Yesuwa ma soqikoo ca Kadmiyel. Mooy ñi bànqaasoo ci Odawya, tollu ci juróom ñaar fukk ak ñeent (74).
44Woykat yi ñoo di askanu Asaf, di téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñett (148).
45Askanu fara bunt yi ñoo di askanu Salum ak askanu Ater ak askanu Talmon ak askanu Akub ak askanu Atita ak askanu Sobay, di téeméer ak fanweer ak juróom ñett (138).
46Liggéeykati kër Yàlla gi ñoo di askanu Cixa ak askanu Asufa ak askanu Tabawot
47ak askanu Keros ak askanu Siya ak askanu Padon
48ak askanu Lebana ak askanu Agaba ak askanu Salmay
49ak askanu Xanan ak askanu Gidel ak askanu Gaxar
50ak askanu Reyaya ak askanu Reccin ak askanu Nekoda
51ak askanu Gasam ak askanu Usa ak askanu Paseya
52ak askanu Besay ak askanu Mewuneen ña ak askanu Nefusim
53ak askanu Bagbug ak askanu Akufa ak askanu Arur
54ak askanu Bacclut ak askanu Mexida ak askanu Arsa
55ak askanu Barkos ak askanu Sisera ak askanu Temax
56ak askanu Necciya ak askanu Atifa.
57Askanu jaami Suleymaan ñii la: askanu Sotay ak askanu Soferet ak askanu Perida
58ak askanu Yaala ak askanu Darkon ak askanu Gidel
59ak askanu Sefatiya ak askanu Atil ak askanu Pokeret Accebayim ak askanu Amon.
60Mboolem liggéeykati kër Yàlla gi ak askanu jaami Suleymaan yi, ñetti téeméer ak juróom ñeent fukk ak ñaar (392).
61Ña bàyyikoo Tel Melax ak Tel Arsa ak Kerub Adon ak Imer te manuñoo firndeel ne seen waa kër maam ak seen askan ci Israayil lañu bokk, ñii la:
62askanu Delaya ak askanu Tobya ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak ñeent fukk ak ñaar (642).
63Am na it ñu loolu daloon ci sarxalkat yi, muy askanu Obaya ak askanu Akocc ak askanu Barsilay ma doon denc doomu Barsilay waa Galàdd ba, ba tax ñu santale ko seen sant.
64Ñooñu seet nañu seen limeefu kër maam, waaye gisuñu ko. Ñu daldi leen doyadal, génne leen ci carxal gi.
65Boroom dëkk ba nag aaye leen ñu lekk ci ñam yu sell|lemma="sell:"* yaa sell, ba keroog sarxalkat ba di am lu leer ci ñoom ci jumtukaayi tegtal yi ñuy wax Urim ak Tumim|lemma="Urim ak Tumim:"*.
66Limu mbooloo ma mépp ba mu daj, ñeent fukki junneek ñaar ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk (42 360) lañu,
67te limaaleesul seen jaam yu góor ak yu jigéen yi tollu ci juróom ñaari junni ak ñetti téeméer ak fanweer ak juróom ñaar (7 337). Amoon nañu itam ay woykat yu góor ak yu jigéen yu tollu ci ñaari téeméer ak ñeent fukk ak juróom (245),
68ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435) ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaari téeméer ak ñaar fukk (6 720).
69Am na ñu jiite seen kër baay, ñu def seen loxo ca liggéey ba. Boroom dëkk ba def na ca alal ja junniy (1 000) poseti wurus ak juróom fukki (50) këll ak fanweeri (30) mbubbi sarxalkat ak juróomi téeméeri (500) dogi xaalis+ 7.69 Fi ñu tudd fanweeri mbubbi sarxalkat yi ak juróomi téeméeri dogi xaalis, am na ñu fi boole ñaari lim yooyu, moomale ko dayob mbubbi sarxalkat yi doŋŋ.*.
70Ñenn ca ña jiite seen kër baay def nañu seen loxo ca alal ja ñu jagleel liggéey ba, mu tollu ci ñaar fukki junniy (20 000) poseti wurus ak ñaari junniy dogi xaalis ak ñaari téeméer (2 200).
71La des ca askan wa joxe na ñaar fukki junniy (20 000) poseti wurus ak ñaari junniy (2 000) dogi xaalis ak mbubbi sarxalkat yu tollu ci juróom benn fukk ak juróom ñaar (67).