Neyemi 8:1-17 WOLB2025 - Bible AI

1mbooloo mépp a daje, di benn bopp ca mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma. Ñu wax Esra bindkat ba, ne ko mu indi téereb yoonu Musaa wi Aji Sax ji dénk Israayil.

2Esra, mi doon ab sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* itam, indi téereb yoon wi keroog benn fanu juróom ñaareelu weer wa, fa kanam mbooloo ma, góor ak jigéen, mboolem ña seeni at may ñu dégg ko.

3Esra jàng ko janook mbedd ma jàkkaarlook buntu Ndox ma, dale ko ba bët setee ba ca digg bëccëg. Mbooloo maa nga teew, góor ak jigéen, mboolem ña dégg la ca nekk. Ñépp nag di teewlu kàdduy téereb yoon wa.

4Esra bindkat baa nga taxaw ca kaw tóoju bu kawe ba ñu defare dénk ngir bés ba. Ña feggook moom ca ndijooram di Matica ak Sema ak Anaya ak Uri ak Ilkiya ak Maaseya. Ña ko féete càmmoñ di Pedaya ak Misayel ak Malkiya ak Asum ak Asbadana ak Sàkkaryaa ak Mesulam.

5Ba Esra di ubbi téere ba, mbooloo mépp a ca teg seeni bët, ndax mbooloo mépp la tiim. Mbooloo mépp nag jóg taxaw.

6Esra daldi sant Aji Sax ji, Yàlla ju màgg ji. Mbooloo ma mépp ànd ne: «Ëskëy waay! Amiin!» yékkati seeni loxo, sukk, sujjóotal Aji Sax ji, dëpp seeni jë fa suuf.

7Ci kaw loolu Yesuwa ak Bani ak Serebya ak Yamin ak Akub ak Sabtay ak Oja ak Maaseya ak Kelita ak Asaryaa ak Yosabàdd ak Xanan ak Pelaya ak Leween|lemma="Leween b-:"* ña di leeralal mbooloo ma yoonu Musaa. Mbooloo maa nga taxaw, kenn ku nekk benn béreb.

8Ci biir loolu ñu di leen jàngal téereb yoonu Yàlla wi, njàng mu leer, di leen ko firil ba ñu xam li ñuy jàng.

9Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell|lemma="sell:"* la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg.

10Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

11Leween ña nag di dëfal mbooloo ma mépp, naan leen: «Noppileen waay, ndax tey bés bu sell la. Kon buleen ci naqarlu.»

12Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ñibbi, di lekk aka naan aka yekkle di bànneexu bu baax. Fekk na ñu xam kàddu ya ñu leen doon xamal.

13Keroog ñaari fan ca weer wa nag ña yilif seen kër baay yépp ànd ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yaak Leween|lemma="Leween b-:"* ña, ñu daje ca Esra bindkat ba, di gëstu kàdduy yoon wi.

14Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi Aji Sax ji santaane, te Musaa jottali ko, ne: Bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.

15Ñu siiwal nag ndigal, ca mboolem seeni dëkk ak ca Yerusalem, daldi yéene ne: «Demleen ca tund ya, wuti ay cari garabi oliw ak cari garabi pẽe+ 8.15 garabi pẽe xeetoo naak filaawoo.* ak cari garabi mirt ak cari garabi tàndarma ak cari garab yu sëq, ndax ñu defare ko ay mbaar, muy li ñu bind.»

16Ba loolu amee mbooloo ma wuti ay car, defare ko ay mbaar ca seen kaw taaxi kër ak ca seeni biir ëtt ak ca ëtti kër Yàlla ga ak ca mbedd ma ca buntu Ndox ma ak ca mbedd ma ca buntu Efrayim.

17Ci kaw loolu mboolem ña ñibbisee ca njaam ga defar ay mbaar, dal ca mbaar ya. La ko dale jamonoy Yosuwe doomu Nuun, ba bésub keroog bànni Israayil defatuñu woon lu ni mel. Muy mbégte mu réya réy.

© 2025 Bible Society of Senegal
>