1Jigéen sama, séet sama, dikk naa sama tool,
2Maa ngi nelaw, te xol yewwu;
3Ma ne ko: «Summiku naa de,
4Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi,
5Ma ne bërét, di ubbil nijaay,
6Maa ubbil nijaay,
7Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma;
8Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatalleen ma
9Yaw mi dàq ci jigéen ñi,
10Sama nijaay daa xees, leer;
11Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam;
12Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox,
13Lex ya di tool,
14Loxo yi banti wurus la,
15yeel yi kenuy doj wu jafe la,