1Dikkal, janqu waa Sulam bee, dikkal;
2Janqoo, lingeer sama,
3Sa jumbax bi di kaas bu mërgalu,
4Sa ween yi ni ñaari tef,
5Sa loos wi, coleet, rattax, ni tatay bëñi ñey;
6Sa bopp siggi ni tundu Karmel,
7Rafet, sopploo!
8Sa taxawaay bii garabu tàndarma la,
9Ma ne, maay yéeg tàndarma gi,
10sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ.
11Man, nijaay a moom,
12Nijaay, ayca nu dem tool ba,
13Nan teela xëyi ca tóokëri reseñ ya,