1Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»
2Jigéen ja wax jaan ja, ne ko: «Man nanoo lekk ci doomi garabi tool bi kay.
3Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»
4Jaan ja ne jigéen ja: «Déedéet, dungeen dee!
5Waaye Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni gët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon.»
6Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram ji mu àndal, moom it mu lekk.
7Seeni gët daldi ubbiku, ñu xam ne yaramu neen lañu def. Ba mu ko defee ñu ràbb xobi garabu figg, gemboo.
8Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi.
9Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?»
10Mu ne ko: «Damaa dégg say tànk ci tool bi, tiit, ndax yaramu neen laa def, ma daldi làqu.»
11Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab ga ma la aaye, waay?»
12Aadama ne ko: «Jigéen ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.»
13Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.»
14Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja:
15Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji,
16Yàlla teg ca ne jigéen ja:
17Mu tegaat ca ne Aadama:
18Suuf dina la meññalal ay dég aki dagg,
19saw ñaq ngay dunde,
20Aadama nag tudde soxnaam Awa (muy firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund.
21Gannaaw gi, Yàlla Aji Sax ji sàkkal Aadama ak soxnaam ay yérey der, wodde leen.
22Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.»
23Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf si ñu ko sàkke.