1Abimeleg doomu Yerubaal ju góor moo dem ca càmmiñi yaayam ca Sikem. Mu wax ak ñoom ak mboolem waa làngi maamam ju góor ji jur yaayam. Mu ne leen:
2«Dangeen di laaj kàngami Sikem yépp, ne leen: “Lan moo leen gënal ci yii yaar: juróom ñaar fukki doomi Yerubaal yépp yilif leen, am kenn doŋŋ yilif leen? Man miy seen deret, di seen mbokk lenqe nag, bàyyileen ma xel.”»
3Ba loolu amee ay nijaayam yegge mboolem kàngami Sikem kàddu yooyu yépp. Seenub xol nag jengal Abimeleg, ndax dañu ne: «Kii kat mooy sunu mbokk.»
4Ba mu ko defee ñu jox ko juróom ñaar fukki siikali xaalis, bu ñu jële ca seen kër tuur ma ñuy wax Baal Berit|lemma="Baal:"*. Abimeleg feye ko ay nit ñu tekkeedi te yaroo seen sago. Ñooña topp ca gannaawam.
5Mu dem nag kër baayam, ca Ofra, daldi rendi ci wenn doj juróom ñaar fukki góor ya mu bokkal seen baay. Mennum Yotam, doomu Yerubaal ju góor ja gën di ndaw moo ca des, te daa làqu woon.
6Ba loolu amee mboolem kàngami Sikem ak Bet Milo gépp dajeji ca garabu Sikem gu mag ga feggook doj wa. Fa lañu fal Abimeleg buur.
7Ba ñu àggee Yotam mbir ma, dafa yéeg ba ca kaw tundu Garisim. Mu àddu ca kaw ne: «Waa Sikem dégluleen maa, ndax Yàlla déglu leen.
8«Garab yee dogu woon, ne dañuy fali seen buur. Ñu ne Oliw: “Falul, di sunu buur.”
9Oliw ne leen: “Xanaa duma dakkal sama diwu tànnéef gii ñuy terale Yàlla, te di ko terale nit ñi, dem naa damay jaay doole ci kaw garab yi?”
10Garab yi nag ne garabu Figg: “Yaw ñëwal boog falu, di sunu buur.”
11Figg ne leen: “Xanaa duma dakkal sama tem-tem jii ak sama meññeef mu neex mi, naan damay jaay doole ci kaw garab yi?”
12Garab ya ne Reseñ: “Kon yaw ñëwal falu, di sunu buur.”
13Reseñ ne leen: “Xanaa duma dakkal sama biiñ bu bees biy bégal Yàlla ak nit ñi, naan damay jaay doole ci kaw garab yi?”
14Ba mu ko defee garab yépp ne Dédd: “Kon nag yaw, ñëwal falu, di sunu buur.”
15Dédd ne garab ya: “Su ngeen ma bëggee fal, may seen buur, jiite leen, te muy dëgg ci yeen, ñëwleen làqu ci sama ker, lu ko moy nag yal na sawara tàkke ci dédd bi, lakki ba ca garabi seedari Libaŋ.”
16«Léegi nag, ndegam dëgg akug mat ngeen jëfe, ba fal Abimeleg buur, ndegam it jëf la ju ngeen baaxee Yerubaal ak waa këram, ba feye ko ko lu mu leen ji,
17te ndaxam déy, sama baay xareel na leen, jaay bakkanam, ba xettali leen ci waa Majan;
18teewul tey yeena jógal sama waa kër baay, ba boole juróom ñaar fukki doomam yu góor, bóom leen ci wenn doj, te yeena fal buur ci kaw kàngami Sikem, Abimeleg doomu jaamam bu jigéen, ndax li muy seen mbokk!
19Kon ndegam dëgg akug mat ngeen jëfeek Yerubaal ak waa këram tey jii, yal nangeen am bànneex ci Abimeleg, te moom it mu am bànneex ci yeen.
20Lu ko moy nag, yal na sawara tàkke fa Abimeleg, xoyom kàngami Sikem ak Bet Milo, tàkkeeti ca waa Sikem ak Bet Milo, xoyom Abimeleg.»
21Ba loolu amee Yotam daw a daw ba Beer, daldi sanci foofa, ngir mucc ci doomu baayam Abimeleg.
22Ñetti at la Abimeleg moom Israayil.
23Gannaaw gi, Yàlla yebal ngelaw lu aay luy féewale Abimeleg ak kàngami Sikem. Kàngami Sikem wor Abimeleg,
24ngir peyug jëfi coxor ja dal juróom ñaar fukki doomi Yerubaal yu góor ba seen deret tuuru, ngir këpp ko Abimeleg, mook kàngami Sikem ya ko jàppale woon, ba mu bóom doomi baayam yooyu.
25Ci kaw loolu kàngami Sikem di wuta yàqal Abimeleg, ba teg ay tërukat ca kaw tund ya, ñuy nangu alalu képp ku jaare ca yoon wa. Ñu daldi koy yegge Abimeleg.
26Ci biir loolu Gaal doomu Ebedd ju góor ànd aki bokkam, dikk Sikem. Kàngami Sikem nag wóolu ko.
27Gannaaw gi, ñu ànd dem ca tool ya, witt seen tóokëru reseñ, nal, di bànneexu. La ca tegu ñu dem ca seen kër tuur ma. Ña ngay lekk aka naan, tey sewal Abimeleg.
28Gaal doomu Ebedd ne: «Ana kuy Abimeleg, ak nooy kan ci Sikem gii, bay nangul Abimeleg? Xanaa du doomu Yerubaal, Sebul di jaraafam? Dama ne nangulleen waa kër Amor, mi sanc Sikem. Lu waral nuy nangul Abimeleg?
29Éy ku tegoon askan wii ci sama loxo, ba ma jële fi Abimeleg! Kon dama naan Abimeleg: “Dajaleel sa gàngoor te génn fii, nu xare!”»
30Ba mu ko defee Sebul jaraafu dëkk ba dégg kàddu yooyu Gaal doomu Ebedd wax. Xolam tàng ca,
31mu yónni ndànk ay ndaw ca Abimeleg, ne ko: «Gaal doomu Ebedd aki bokkam kat dikk nañu Sikem, te ña nga noonee di xabtal waa dëkk bi ci sa kaw.
32Kon nag dangay jóg guddi, yaak gàngoor gi nga àndal, nga lal am tëru ca àll ba.
33Bu ëllëgee ba jant biy fenk rekk, sàqil ci kaw dëkk bi. Gaal ak gàngoor gi mu àndal duñu def lu moy génn dajeek yaw, su ko defee nga def ko loo man.»
34Ci kaw loolu Abimeleg jóg guddi, mook mboolem gàngoor ga mu àndal, ñu lal am tëru fa janook Sikem, def ñeenti kuréel.
35Ba Gaal doomu Ebedd génnee ba taxaw ca buntu dëkk ba, Abimeleg ak gàngoor ga mu àndal ne pëll, génne fa ñu doon tëroo.
36Gaal séen gàngoor ga, ne Sebul: «Gàngoor a ngii di wàcce ca kaw tund ya!» Sebul ne ko: «Takkndeeri tund yi de nga gis, ñu mel niy nit.»
37Gaal dellu ne: «Ma ne gàngoor a ngii di wàccsi, jóge kaw tundu digg bi, ak menn mbooloo muy dikk, jóge yoonu garabu seen gu gisaanekat ya!»
38Sebul ne ko: «Ana sa réy làmmiñ gi nga doon waxe naan kuy Abimeleg ba ñu di ko nangul? Xanaa du gàngoor gii nga doon tuutal? Génnal rekk nag, xeex ak ñoom!»
39Gaal nag génn, jiitu kàngami Sikem. Mu daldi xareek Abimeleg.
40Abimeleg dàq ko, mu daw, nitam ñu bare daanu, ne lareet, ba ca buntu dëkk ba.
41Ba loolu amee Abimeleg sanci Aruma, Sebul boole Gaal aki bokkam, génne leen Sikem, aaye leen fa.
42Ca ëllëg sa waa Sikem di waaja génn jëm ca tool ya. Ñu àgge ko Abimeleg.
43Abimeleg dajale gàngoor ga, séddale leen ñetti mbooloo. Mu lal am tëru ci àll bi. Ba mu gisee waa dëkk ba di génne ca dëkk ba rekk, dafa jóg, ne milib ca seen kaw.
44Abimeleg ak mbooloo mi mu àndal ñoo riir wuti buntu dëkk ba, taxaw fa, ñaari mbooloo ya ca des riir, dali ca mboolem ña nekkoon ca àll ba, ba duma leen.
45Bésub keroog bépp la Abimeleg xareek dëkk ba, ba nangu ko, ña ca dëkk, mu rey leen. Mu yàq dëkk ba yaxeet, suy fa xorom.
46Ba mboolem kàngami Sikem ya ca tatam Sikem déggee loola, ca lañu làquji, ca pax ma ñu gas ca kër tuur ma ñuy wax Berit, def ko néegu rawukaay.
47Ñu yegge Abimeleg ne ko mboolem kàngami Sikem ya dëkk ca tatam Sikem daje nañu.
48Mu daldi yéegi tundu Calmon mook mboolem gàngoor gi mu àndal. Ci kaw loolu Abimeleg jël ab sémmiñ, dog caru garab, yékkati, teg ci mbaggam. Mu ne gàngoor ga mu àndal: «Nu ngeen gis ma def ko rekk, gaawleen def noonu.»
49Gàngoor gépp itam, ku ci nekk dog ab caram, ñu topp ca gannaaw Abimeleg. Ci kaw loolu ñu jal car ya fa sës ca néegu rawukaay ba, daldi koy taal ca kaw ña ca biir. Ba mu ko defee waa taaxum Sikem yépp dee, tollook junniy nit, góor ak jigéen.
50La ca tegu Abimeleg dem Tebecc, dal fa janook dëkk ba. Ci kaw loolu mu nangu ko.
51Tata ju ñu dàbbali moo nekkoon ca biir dëkk ba. Waa dëkk ba bépp nag, góor ak jigéen, daw làquji fa; ñu tëju ca biir, daldi yéeg ca kaw taax ma.
52Abimeleg dikk ba ca tata ja, song ko. Naka la dikk ba jege buntu tata ja, nar koo taal,
53as ndaw rotal aw doju wolukaay wu mag wu jóge ca kaw, mu xar kaaŋ ma.
54Abimeleg gaaw woo xale bu góor ba yor ngànnaayam, ne ko: «Boccil sa saamar, te jekkali ma, ndax kenn du ne jigéen a ma rey!» Xale bu góor ba jam ko, mu dee.
55Waa Israayil nag gis ne Abimeleg dee na, ku ne daldi ñibbi.
56Noonu la Yàlla delloo Abimeleg jëf ju bon ja mu defoon baayam, ba mu reyee juróom ñaar fukki doomi baayam.