1Kàddug Aji Sax jii|lemma="Aji Sax j-:"* moo dikkaloon Ose, góor giy doomu Beeri, ci janti buuri Yuda: Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiyas; ak ci janti buurub Israayil Yerbowam doomu Yowas.
2Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»
3Ose dem takki Gomer doomu Diblayim. Mu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju góor.
4Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel. Des na tuuti dinaa mbugal askanu Buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa dakkal nguurug waa Israayil.
5Su bés baa maay damm ngànnaayu Israayil ca xuru Yisreel+ 1.5 Xuru Yisreel lañuy misaale deret ju wal, ndax la ñu fa bóomoon ñu bare. Seetal ci +bk 2.Buur ya+bk* 9.7—10.31.*.»
6Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruxama» (muy firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israayil, dootuma leen baal.
7Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
8Ba Gomer feralee Lo Ruxama, ëmbaat na, ba am doom, muy góor.