1«Bu may faj Israayil foofu ca Efrayim la seeni ñaawtéef di feeñ, ànd ak mbonu Samari seen péey. Dañuy njublaŋ, sàcc yiy bëtt ci biir kër yi, gàngoori saay-saay di songe ci biti.
2Taxul ñu jàpp ci seenum xel ne seen mboolem jëf ju bon laa bàyyi xel. Léegi seeni jëf a leen wër ndombo, ne màkk fi sama kanam.
3Seenug mbon lañuy bégale buur, seeni fen di bégal kàngam.
4Ñoom ñépp a diy njaalookat. Ñu mel ni taalu mburu bu yànj, taal bu kay lakk soxlawula xamb, ca tooyal ba, ba kera xóoy bay funki.
5Bu sunu buur xewlee, kàngam yi naan ba wopp, buur tàllal loxo ay ñaawlekat.
6Seenub xol lañu waajal nib taal, di tëroo, kay lakk seen mburu fanaanee nelaw, bët set taal ba yànj, di fër-fëri+ 7.6 Ki jiite pexe mu bon mi moo fanaanee nelaw ca guddig xawaare ga, bët set mu jóg, joxe ab tegtal, ngir ñu sottal pexe ma..
7Ñoom ñépp a tàng jérr nib taal, te ñooy xoyom seeni njiit, seen buur yépp a daanu, te kenn ci ñoom woowu ma wall.
8«Efrayim+ 7.8 Efrayim, kenn la ci sëti Yanqóoba mi ñu dippee Israayil. Turu Efrayim wi fii, askanu Israayil la fi taxawal. moo jaxasook askani jàmbur, Efrayim moo di mburu mu ñu walbatiwul cib taal.
9Ay doxandéem a jeexal dooleem, te xamu ko; kawaram weex tàll, te yégu ko.
10Israayil, ag reewandeem a ko tiiñal, te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji. Loolu yépp taxul ñu wutsi ko.
11Efrayim daa mel ni pitax, dofe, ñàkk xel, di woo wall Misraaka dem Asiri.
12Bu ñuy dem, maa leen di laaw samab caax, niy njanaaw laa leen di waddale fi suuf, fa ma dégge seenum ndaje laa leen di mbugale.
13Ngalla ñoom, nde ñoo ma daw, yàqute ñeel na leen, nde ñoo ma gàntal. Doon naa leen jot waaye ñoo ma fenal.
14Du seen xol lañu ma woowe wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram+ 7.14 Ñi daan jaamu Baal mi ñu jiiñ ne mooy nangul suuf, ñoo aadawoo woon di dagg seen yaram, di tuur seen deret ci suuf, ngir foog ne loolu mooy tax seen mbey nangu., dëddu ma.
15Maa leen jàngal, dëgëral seeni përëg, te man lañuy fexeel lu bon.
16Bu ñu waññikoo it, du fi Aji Kawe ji. Ni xala gu yolom lañu mel, te seeni kàngam ay faate saamar ndax seen sànjum làmmiñ, te loolu lees leen di reetaane ca réewum Misra.