Peeñu ma 11:1-18 WOLB2025 - Bible AI

1Ba loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel niw yet, ne ma: «Jógal, natt néegu Yàlla bi ak sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* bi, te nga waññ ña fay jaamu Yàlla.

2Waaye ëttu bitib kër Yàlla gi, bàyyi ko, bu ko natt, ndax ñi dul Yawut lees ko jox, te ñooy dëggaate dëkk bu sell bi diiru ñeent fukki weer ak ñaar.

3Dinaa may nag sama ñaari seede yi, ñu jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* diiru junni fan ak ñaari téeméer ak juróom benn fukk (1 260) yu ñuy sol ay saaku, di ko toroxloo.»

4Ñaari seede yi ñoo di ñaari garabi oliw+ 11.4 oliw: garabu oliw dafa xawa mel ni sump, te am doom yu ñuy nal, ngir am ci diw gu ñuy togge, mbaa ñu di ko taaloo.* yeek ñaari tegukaayi làmp yi taxaw ci kanam Boroom suuf si.

5Ku leen nara lor, sawaraay génne ci seen gémmiñ, lakk seeni noon. Képp ku leen nara lor, noonu ngay deewe.

6Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy jottali kàdduy waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcce ci suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.

7Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote|lemma="xóote b-:"* bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen.

8Seeni néew da naan lareet ci péncum dëkk bu mag boobu ñuy misaale turu Sodom|lemma="Sodom ak Gomor:"* mbaa Misra, fa ñu reye woon seen Sang ci bant.

9Diiru ñetti fan ak genn-wàll lañuy weeru, niti wépp xeet ak gépp giir ak wépp làkk ak wépp askan di seetaan seeni néew, te duñu bàyyi kenn suul leen.

10Waa àddina dinañu bége seen dee, di bànneexu, di joqalante ay njukkal, ndaxte ñaari yonent yooyu ñoo lakkaloon waa àddina.

11Waaye bu ñetti fan yeek genn-wàll wéyee, noowug dund giy bawoo fa Yàlla moo leen di solu, ñu jóg, taxaw, tiitaange ju réy daldi jàpp waa ceetaan ma.

12Ba loolu amee ñaari seede yi dégg baat bu xumb jibe asamaan, ne leen: «Yéegleen fii.» Ñu yéeg ci asamaan ci biir aw niir, seeni noon di gis.

13Ca waxtu wa, suuf daldi yëngu lool, ba benn fukkeelu dëkk ba màbb. Juróom ñaari junniy nit (7 000) dee ci yëngub suuf ba, ña ca des tiit, di sàbbaal Yàllay asamaan.

14Ñaareelu musiba mi wéy na, waaye kat ñetteel baa ngi nii di ñëw.

15Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne:

16Ba loolu amee ñaar fukki mag ak ñeent, ña toogoon ca seen ngàngune ca kanam Yàlla, daldi ne gurub sukk, dëpp seen jë ca suuf, sujjóotal Yàlla.

17Ñu ne:

18Askan yee meroon,

© 2025 Bible Society of Senegal
div>