Peeñu ma 12:1-17 WOLB2025 - Bible AI

1Firnde ju màgg nag moo feeñoon asamaan: Ndaw su làmboo jant bi, weer wi ronu ndëgguy tànk yi, mu kaalawoo|lemma="kaala g-:"* fukki biddiiw ak ñaar.

2Jigéenu wérul juy matu la. Mu ngi yuuxu ndax mititu mat wu tar.

3Ci kaw loolu jeneen firnde feeñ asamaan. Du lenn lu dul ninki-nanka ju réy, xonq curr, am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, juróom ñaari mbaxanay buur tege ci bopp yi, bopp bu ne, menn.

4Geenam gi daldi buube fa asamaan benn ñetteelu biddiiw yi, rattax leen ci suuf. Ninki-nanka jaa ngi taxaw ci kanam ndaw siy matu, ngir bu xale bi juddoo rekk, mu lekk ko.

5Ndaw si nag wasin doom ju góor, te muy ki wara yilif xeeti àddina yépp, di leen jiitee yetu weñ. Ci kaw loolu ñu fëkk doom ja, yóbbu fa Yàlla, ca ngànguneem.

6Ndaw si nag daw, ba ca màndiŋ ma, ci ab rawtu bu ko Yàlla waajaloon, ngir ñu leel ko fa diiru junni fan ak ñaari téeméer ak juróom benn fukk (1 260).

7Ab xare nag jibe fa asamaan. Mikayel aki malaakaam di xareek ninki-nanka ji, ninki-nanka jeeki malaakaam it di xare,

8ñu néewal leen doole, ba amatuñu fu ñu nekk ci asamaan.

9Ñu xalab ninki-nanka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane|lemma="Seytaane:"*, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.

10Ci kaw loolu ma dégg baat bu xumb bawoo asamaan, ne:

11Sunu bokk yee daan ndax deretu Xar mi,

12Kon nag yaw asamaan, bégal,

13Ninki-nanka ja nag xam ne xalab nañu ko ci kaw suuf, mu ne dann ndaw sa jur doom ju góor ja.

14Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nanka ji, dem ca màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll+ 12.14 ñetti diir ak genn-wàll: seetal ci aaya 6 (12.6).*.

15Ba mu ko defee ninki-nanka ji buusu ndox mu bare ni dex, ndox ma topp ndaw sa, ngir wal ma yóbbaale ko.

16Ci kaw loolu suuf wallu ndaw sa, ŋa, daldi naan dex ga gémmiñu ninki-nanka ja buusu woon.

17Ninki-nanka ja mere ndaw sa, daldi dem, xeexi ak ndesu doomam yi topp santaaney Yàlla tey saxoo seedeel Yeesu.

© 2025 Bible Society of Senegal
div>