1Ma daldi dégg baat bu xumb bu bawoo ci màkkaan mi. Mu ne juróom ñaari malaaka yi: «Demleen sotti juróom ñaari ndabi sànjum Yàlla yi ci kaw suuf.»
2Malaaka mu njëkk mi dem, sotti ndabam ci kaw suuf, mu def ay taab yu bon te aay ci kaw nit ñi am màndargam rab wi, tey sujjóotal jëmmu nataalu rab wi.
3Ñaareelu malaaka mi sotti ndabam ci géej gi. Mu soppiku deret ju mel ni lu nàcce ci ku ñu bóom. Lépp lu doon dund biir géej daldi dee.
4Ñetteelu malaaka mi sotti ndabam ci dex yeek bëti ndox yi, mu doon deret.
5Ma dégg malaaka mi yilif ndox yi ne:
6Deretu ñu sell ñeek deretu yonent yi lañu tuur,
7Ma dégg sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* ba ne:
8Ba loolu amee ñeenteelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw jant bi. Ñu daldi may jant bi muy lakke nit ñi tàngooru sawaraam.
9Ci kaw loolu tàngooru naaj wu metti di lakk nit ñi. Nit ñi nag tuubuñu, sàbbaaluñu Yàlla; xanaa di saaga Yàlla ji dogal yooyu musiba.
10Juróomeelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw ngàngunem rab wi, nguuram daldi sóobu ci lëndëm, nit ñi di yéyu ndax mitit,
11tuubuñu seeni jëf, xanaa di saaga Yàllay asamaan ndax seeni mitit ak seeni taab.
12Juróom benneelu malaaka mi sotti ndabam ci dex gu mag gi ñuy wax Efraat, dex gi daldi ŋiis, ngir sàkkal buuri penku yiy dikk aw yoon.
13Ci kaw loolu ma gis ñetti njuuma yu mel niy mbott, kenn ki génne ci gémmiñu ninki-nanka ji, kenn ci gémmiñu rab wu njëkk wi, ki ci des ci gémmiñu ñaareelu rab wi mbubboo yonent.
14Ñooñu nag ay njuumay Seytaane|lemma="Seytaane:"* lañu, yuy def ay kéemaan, tey dajaleji buuri àddina sépp, ngir xareb bés bu mag bu Yàlla Aji Man ji.
15Mu ne: «Maa ngi nii di yoot, di dikk nib sàcc. Ndokkalee, yaw mi teewlu, fàggu say yére, ba doo deme gàcceg yaramu neen, ñu di la seetaan.»
16Ci kaw loolu njuuma yi dajale buur yi ci béreb bu ñuy wax Armagedon+ 16.16 Armagedon ag joor la ci réewum Kanaan.*, di baatu ebrë.
17Ba mu ko defee juróom ñaareelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw ngelaw li, baat bu xumb jóge ca ngàngune ma ca màkkaan ma, ne: «Sotti na!»
18Ba loolu amee, ay melax tàkk, ay kàddu aki dënu riir, suuf yëngu yëngu bu réy bu masula am ba nit teewee ci kaw suuf ba bésub keroog. Noonu la yëngub suuf ba yéemee te réy.
19Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon|lemma="Babilon:"* gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.
20Dun yépp daldi dëddu, tund yi ne mes.