Peeñu ma 18:1-23 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu am sañ-sañ bu réy wàcce asamaan, àddina di leere cig leeram.

2Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon|lemma="Babilon:"* a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.

3Biiñu moyam miy indi am sànj, moom la askani àddina yépp di naan. Moom la buuri àddina àndal di moy, te doyloodig bakkanam gu réy woomal na julay àddina.»

4Ci kaw loolu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan, ne: «Yeen sama ñoñ, génnleen dëkk bii, bala ngeena bokk ak moom ay bàkkaaram, bay séddu ci mbugalam.

5Ndaxte ay bàkkaaram jalu na ba àkki asamaan, te Yàlla bàyyi na xel ay ñaawtéefam.

6Na mu jëfe ak yeen, jëfeleen ko ak moom, feyleen ko ñaari yoon ay jëfam. Kaas bi muy xellile am njafaan, feesalalleen ko njafaan lu ko ëpp doole ñaari yoon.

7Joxleen ko ci toskare aku naqar, kemu daraja jaak dund gu bakkane ga mu jagoo woon. Gannaaw moo ne cim xelam: “Maa tooge jalu lingeer, dumab jëtun, duma deele mukk,”

8looloo tax ci benn bés la musiba yiy këppoondoo ci kawam: mbas, deele akub xiif, te dees na ko lakk ba mu jeex, ndax Boroom bi Yàlla mi ko mbugal moo am doole.»

9Buuri àddina yi àndoon ak dëkk bii ci moy ak dund gu bakkane, bu ñu séenee saxaaras lakkam, ñoom ñépp ay yuuxu, di ko jooy.

10Fu sore lañuy dànd, ndax ragal toskarey dëkk bi, te naan:

11Julay àddinaa ngay yuuxu, di ko jooy, nde am njaayam du jarati:

12wurus ak xaalis ak doji gànjar aki per ak lẽe ak ndimo lu yolet, ak sooy, ak ndimo lu xonq curr, ak bépp bant bu xeeñ, ak wépp xeetu jumtukaayi bëñi ñey, ak jumtukaayi dénku ngëneel ak yu xànjar ak yu weñ gu ñuul ak yu doju màrb,

13ak kanel ak yeneen safal, ak ndàbbu miir ak cuuraay-libaŋ ak yeneen cuuraay, ak biiñ ak diwu oliw ak sunguf ak pepp ak nag ak xar ak fas, aki watiir aki jaam, ak nit ñu ñu jàpp xare.

14Dinañu ne: «Doomi garab yi nga soppoon sore na la, mboolem lu neex ak lu yànj réer na la mërr!»

15Ña daan jula yooyii ci dëkk bi ba woomle, fu sore lañuy dànd, ndax ragal toskarey dëkk bi, di yuuxooka jooyoo,

16naan:

17wenn waxtu rekk, alal ju baree nii neen!»

18séen saxaaras lakku dëkk bi di jalu, jekki xaacu naan: «Bii dëkk bu mag, ana dëkk bu masa nirook moom?»

19Dañuy xëpp suuf ci seen kaw bopp, di yuuxooka jooy aka naqarlu, naan:

20Ndokkalee, asamaan,

21Ba loolu amee malaaka mu am doole yékkati doj wu mel ni doju wolukaay wu mag, sànni ko biir géej, daldi ne:

22Buumi xalam ak baatu woykat, toxorooku liit,

23làmp du niiteeti fi yaw,

© 2025 Bible Society of Senegal
div>