1Ci biir loolu ma gis ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi téere bu ñu taxañ bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom ñaari tayu.
2Ma gis malaaka mu am doole, muy yéenee baat bu xumb, naan: «Ana ku yeyoo tàyyi tayuy téere bii, ubbi ko?»
3Du kenn nag ci asamaan mbaa kaw suuf, mbaa biir suuf, ku manoona ubbi téere bi, ba yër ko.
4Ma jooy jooy yu metti, ndax giseesul kenn ku yeyoo ubbi téere bi, ba yër ko.
5Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda|lemma="Daawuda:"* daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»
6Ma daldi gis kuuyum xar mu ndaw mu mel ni lu ñu rendi, mu taxaw fi digg ngàngune mi, ñeenti mbindeef yeek mag ñi yéew ko. Xar mi juróom ñaari béjjén la am, ak juróom ñaari bët, di juróom ñaari noowi Yàlla yi ñu yebal ci àddina sépp.
7Xar mi dikk, jël téere bi ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi.
8Ba mu jëlee téere bi, ñeenti mbindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay|lemma="cuuraay l-:"*, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.
9Ñuy woy nag woy wu yees, naan:
10Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yi, ñeel sunu Yàlla,
11Ma xoolaat, daldi dégg baati malaaka yu bare, ñu yéew ngàngune mi ak mbindeef yi ak mag ñi, seen lim di ay junni, ba ci junniy junni.
12Ña ngay àddu ca kaw, naan:
13Ba loolu amee mboolem ndundati asamaan ak kaw suuf ak biir suuf ak géej ak mboolem li ci seen biir, ñoom ñépp di wax, may dégg, naan: