1Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti colli àddina. Ña nga téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw baña wale fenn; du ci jéeri, du ci géej, du ci genn garab.
2Ma gis meneen malaaka, mu yéege penku, yore torluwaayu Yàlla jiy dund. Mu àddu ca kaw, wax ak ñeenti malaaka ya ñu mayoon ñu yàq géej ak jéeri,
3ne leen: «Buleen yàqagum jéeri ji ak géej gi ak garab yi, li feek torluwunu ci jëwi ñiy jaamu sunu Yàlla, màndargaale leen.»
4Ma dégg limub ña ñu màndargaale torluwaay ba; téeméeri junni ak ñeent fukk ak ñeent (144 000), bawoo ci mboolem giiri bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*:
5Giirug Yuda, fukki junneek ñaar (12 000) lañu ci màndargaal,
6giirug Aser, fukki junneek ñaar,
7giirug Simeyon, fukki junneek ñaar,
8giirug Sabulon, fukki junneek ñaar,
9Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làkk yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Xar mi, sol mbubb yu weex, jël ay cari garabi tàndarma.
10Ña ngay àddu ca kaw, naan:
11Malaaka yépp a nga taxaw, yéew ngàngune ma ak mag ñaak ñeenti mbindeef ya. Ñu ne gurub sukk, dëpp seen jë fa kanam ngàngune ma, sujjóotal Yàlla,
12ne: «Amiin! Na sunu Yàlla jagoo màggal ak daraja ak xel ak cant ak worma ak kàttan ak doole, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!»
13Ci kaw loolu kenn ci mag ñi ne ma: «Boroom mbubb yu weex yii, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»
14Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma:
15Loolu moo leen taxa teew fi kanam ngàngunem Yàlla,
16Dootuñu xiif, dootuñu mar.