Room 10:1-21 WOLB2025 - Bible AI

1Bokk yi, sama yéeney xol ak ñaan gi may ñaanal Israayil ci Yàlla moo di ñu mucc.

2Ñoom laa seedeel seenug parlu ci Yàlla, waaye dañu koo tegul ci xam-xam bu doy.

3Yoonu njub gi Yàlla di baaxe nit ki àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye.

4Ndax kat Almasi|lemma="Almasi b-:" bi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm. Coobarey Yàlla mooy ñépp mucc

5Njub gi sàmm ndigali yoon di maye, li ci Musaa bind moo di: «Kuy jëfe ndigal yooyu, yaay dund ndax ñoom+ 10.5 Seetal ci \+bk Sarxalkat yi\+bk* 18.5..»

6Waaye njub gi ngëm di maye, li muy digle mooy: «Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw asamaan?”» nde day mel ni Almasi|lemma="Almasi b-:" bi ngay wuta wàcce.

7«Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”» nde day mel ni dangay wuta dekkilaat Almasi bi.

8Li mu wax moo di: «Kàddu gi kay jege na leen lool: ci seen gémmiñ ak ci seen biir xol la nekk+ 10.8 Seetal ci \+bk Baamtug yoon wi\+bk* 30.11-14..» Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle.

9Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.

10Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.

11Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus+ 10.11 Seetal ci \+bk Esayi\+bk* 28.16..»

12Ag wuutale amul diggante ab Yawut ak jàmbur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.

13Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw+ 10.13 Seetal ci \+bk Yowel\+bk* 3.5..»

14Waaye nees di woowe koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?

15Nees di yéglee xibaar, te yebaleesu la? Noonu la Mbind mi indee ne: «Ñeeka rafeti tànk, ndaw yii di yéglesi xibaari jàmm+ 10.15 Seetal ci \+bk Esayi\+bk* 52.7.!»

16Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi|lemma="Esayi:" ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal+ 10.16 Seetal ci \+bk Esayi\+bk* 53.1.?»

17Kon boog ngëm ci dég-dég lay juddoo, dég-dég ba bawoo ci kàddug waare gi jëm ci Almasi bi.

18Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax «Suuf sépp la seen ndéey jibal, seen kàddoo àkki cati àddina+ 10.18 Seetal ci \+bk Taalifi cant\+bk* 19.5..»

19Ma neeti: xanaa bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:" dañoo xamul? Ahakay! Musaa moo leen njëkkoona jottali la Yàlla noon: «Yeen, maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara, ci waasow naataxóona laa leen di merloo+ 10.19 Seetal ci \+bk Baamtug yoon wi\+bk* 32.21..»

20Esayi it am fit ba ne: «Ñi ma seetul woon, gis nañu ma, ca ña ma laajul woon laa feeñe+ 10.20 Seetal ci \+bk Esayi\+bk* 65.1..»

21Israayil nag la wax ci mbiram ne: «Bëccëg bépp laa yendoo tàllal samay loxo askanu fippukat wu déggadi+ 10.21 Seetal ci \+bk Esayi\+bk* 65.2..»

Kàddug Yàlla © 2025 La Mission Baptiste du Sénégal. Licensed under CC BY-NC-ND 4.0.