Room 9:1-32 WOLB2025 - Bible AI

1Dëgg laay wax, Almasi|lemma="Almasi b-:"* bi seede na ko, fenuma. Sama xol moo ma seedeele Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi, ne lii may wax dëgg la:

2li may wax moo di tiis wu réy laa am ak naqaru xol wu dakkul,

3nde man doon naa ñaana alku sax, daggoo ak Almasi bi, ngir jàmmi sama bokki xeet, sama bokki deret.

4Ñooñoo di xeetu Israayil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, Yàlla won na leen jataayam ju yànj, fas ak ñoom kóllëre|lemma="kóllëre g-:"*, jox leen ndigali yoon wi ak doxalinu njaamu Yàlla aki digeem;

5ñoo soqikoo ci maam yu baax ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi bi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.

6Du caageenu kàddug Yàlla moo neen, ndax ñi bokk ci xeetu Israayil ñépp duñu Israayil tigi.

7Te it sëti Ibraayma yépp bokkuñu ci askanam, waaye li Mbind mi indi moo di: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan+ 9.7 Seetal ci +bk Njàlbéen ga+bk* 21.12.*.»

8Loolu di tekki ne du sëti Ibraayma yi ci wàllu deret ñoo di doomi Yàlla, waaye doom yi seenub juddu dëppoo ak digeb Yàlla, ñoom lañu jàpp ne ñooy askanu Ibraayma.

9Ndax kat kàddug dige ba nii la jibe: «Nëgëni sii déwén laay délsi, te Saarata dina am doom ju góor+ 9.9 Seetal ci +bk Njàlbéen ga+bk* 18.10, 14.*.»

10Te yemul foofu rekk, waaye Rebeka it moo am ay seex yu genn góor jur, muy sunu maam Isaaxa.

11Doom ya nag juddooguñu woon bay def lenn lu baax, mbaa lu bon. Yàlla moo defe noonu ngir wéyal dogal bu dëppoo ak tànnéefu boppam

12bu ajuwul ci kawi jëf, xanaa ci kiy woote. Rebeka+ 9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa.* la kàddu gii dikkal: «Mag ji mooy surgawu rakk ji+ 9.12 Seetal ci +bk Njàlbéen ga+bk* 25.23.*.»

13Noonu la Mbind mi indee ne: «Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"* laa sopp, te Esawu laa foñ+ 9.13 Seetal ci +bk Malasi+bk* 1.2-3.*.»

14Ana lu nu ci mana wax nag? Ndax Yàlla daa wàcc foofu yoon? Mukk kay!

15Ndax kat moo noon Musaa:

16Kon nag mbaaxug Yàlla ajuwul ci coobarey nit ki, mbaa aw ñaqam, waaye lépp yërmandey Yàlla la.

17Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam sama riirum tur dajal àddina+ 9.17 Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 9.16.*.»

18Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.

19Xam naa dinga ma ne: «Ana kon lu Yàlla di sikkeeti? Coobarey Yàlla, ana ku koy fanq?»

20Waaye yaw nit ki, yaay kan bay weddi Yàlla? Ndax këf ku ñu tabax dina ne ka ko tabax: «Lu tax nga sàkke ma nii?»

21Tabaxkatu ndab bi xanaa daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal lenn ndabal teraanga ak leneen ndabal njoogaan?

22Yàlla dafa nammoona wone am sànjam, xamle dooleem. Teewul moo muñal lool ay ndab yu yelloo am sànjam, te seen sànkute ñoroon xomm.

23Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teraangaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga?

24Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jàmbur ñi dul Yawut itam.

25Moom la wax it ci téereb Ose ne:

26«Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,”

27Ci mbirum Israayil la Yonent Yàlla Esayi|lemma="Esayi:"* itam xaacu woon ne:

28Ndax kàddu gi Boroom bi wax:

29Mooy itam la Esayi waxoon lu jiitu, ne:

30Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jot àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye.

31Waaye xeetu Israayil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi.

32Ndax lan? Sukkandikoowul ci ngëm, xanaa ay jëf. «Doj wuy fakkastale,» moom lañu fakkastaloo.

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>