Ruut 1:1-21 WOLB2025 - Bible AI

1Ba njiit ya daan àtte faloo ca Israayil+ 1.1 Booba buur amagul woon ca Israayil.*, jamono jooju dafa amoon xiif ca réew ma. Jenn waay bàyyikoo Betleyem ca diiwaanu Yuda, ànd ak soxnaam ak ñaari doomam yu góor, ñu toxuji ca réewum Mowab+ 1.1 réewum Mowab ak réewum Israayil ñoo feggoo woon, waaye seen diggante neexul woon.*.

2Waa ja Elimeleg la tuddoon, soxnaam di Nawmi, ñaari doomam yu góor ya di Maxlon ak Kilyon. Ay Efrateen lañu, cosaanoo Betleyem ca Yuda. Ñu agsi ca réewum Mowab, daldi sanc foofa.

3Gannaaw gi, Elimeleg jëkkëru Nawmi faatu; Nawmi des ak ñaari doomam yu góor.

4Ñooñu mujj jël ay jigéeni Mowab soxna; kenn ka di Orpa, ka ca des di Ruut. Ba ñu nekkee foofa lu tollu ci fukki at,

5ñoom ñaar ñooñu di Maxlon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kese.

6Ba loolu amee Nawmi fabu, mook goroom ya, ngir jóge réew ma. Booba fekk na mu dégge ca Mowab ne Aji Sax ji|lemma="Aji Sax j-:"* xettali na ñoñam, ba may leen ab dund.

7Ma nga jóge fa mu dëkkoon, ànd ak ñaari goroom ya, ñu tegu ca yoon wa, jëm Yuda.

8Ci biir loolu mu wax ak ñaari goro ya, ne leen: «Demleen kay, ñibbileen, ku nekk sa kër yaay. Yal na leen Aji Sax ji baaxe, na ngeen baaxe woon ñi wuutu, te baaxe ma, man itam.

9Yal na Aji Sax ji may ku nekk ci yeen jàmm ca kër jëkkër ja muy amaat.» Ci kaw loolu mu fóon leen, ñu ne yikkét jooyoo.

10Ñu ne ko: «Déet, yaw kay lanuy àndal, dem ca say bokk.»

11Mu ne leen: «Ñibbileen ngalla, doom, lu ngeen di ànd ak man doye? Ndax dama leena manatee jural ay jëkkër ci sama biir bii?

12Ñibbileen rikk doom, demleen, ngir man damay mag, ba wees séy; te su ma ci dese woon yaakaar it, guddig tey jii sax su ma ci séyoon, jur ciy doom,

13mbaa dingeen leen mana xaar, ba ñu màgg? Xanaa dungeen toog, baña séy ndax ñoom? Déedéet, doom. Maa leen ëpp naqar, man mi Aji Sax ji nattoo nii.»

14Ñu dellu ne yikkét, di jooyoo. Orpa fóon goroom, tàggatook moom, Ruut nag moom langaamu ko rekk.

15Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!»

16Mu ne ko: «Bu ma soññ mukk ci loolu, duma la wacc, duma la dëddu. Foo jëm, fa laa jëm; fooy dal, fa laay dal; say bokk di saay bokk; sa Yàlla di sama Yàlla.

17Foo deewe it, ma deewe fa, ñu denc ma fa. Yal na ma Aji Sax ji teg mbugal mu gëna tar, ndegam lenn lu moy dee tàggale na maak yaw.»

18Nawmi nag gis ni Ruut dogoo ci ànd ak moom, ba tax soññatu ko.

19Ba mu ko defee ñu ànd ñoom ñaar, ba àgg Betleyem.

20Mu ne leen: «Buleen ma ne Nawmi (muy firi Boroom mbégte mi), neleen ma Mara (muy firi Boroom naqar wi), ndax Aji Man ji da maa teg naqar wu réya réy.

21Maa demoon ak loxo yu ne gadd, Aji Sax ji delloosi maak loxoy neen. Kon lu ngeen may woowe Nawmi doye, te Aji Sax ji àtte ma ñàkkal? Ndax kat Aji Man ji ci njàqare la ma tàbbal!»

© 2025 Bible Society of Senegal
/div>