1Libaŋéey, ubbil say bunt,
2Yaw garabu sippar, yuuxul,
3Jooyi sàmm ya jib na,
4Aji Sax ji sama Yàlla dafa wax ne:
5Ñi leen jënd di leen rendi,
6Dootuma yërëm waa réew mi déy.»
7Ba loolu amee may sàmm xar yi teefonke yi nara rendiluji, rawatina ñi gëna sonn ci gétt gi. Ca laa jël ñaari yeti sàmm. Benn bi ma tudde ko Xejjoo, bi ci des ma tudde ko Bennoo. Ci kaw loolu may sàmm gétt gi.
8Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen.
9Ma ne gétt gi: «Dootuma leen sàmm. Na ñiy dee, dee; ñiy sànku, sànku; ñi dese bakkan yàppante ci seen biir.»
10Ba mu ko defee ma jël sama wenn yet wi, Xejjoo, damm ko, ngir doge ko sama kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* gi ma fasoo woon ak askan yépp.
11Bésub keroog la kóllëre ga dog, teefonke yi may xool daldi xam ne loolu kàddug Aji Sax ji la.
12Gannaaw loolu ma ne leen: «Su leen neexee, joxleen ma sama peyoor, su leen neexul, téyeleen ko.» Ñu waññ fanweeri dogi xaalis, feye ma.
13Aji Sax ji ne ma: «Ndaw njëg gu réy gu ma leen jaral waay! Sànni ko ca boroom njaq ya.» Ma jël fanweeri dogi xaalis ya+ 11.13 Mooy ndàmpaay li ñuy fey sang bu ñu gaañ jaamam. Seetal ci +bk Mucc ga+bk* 21.32.*, sànni ko boroom njaq ya, ca kër Aji Sax ji.
14La ca tegu ma damm sama ñaareelu yetu sàmm ba, Bennoo, ngir dog bokk gi dox diggante Yuda ak Israayil.
15Aji Sax ji nag neeti ma: «Léegi jëlal jumtukaayu sàmm bu ñàkk bopp.
16Maa ngi nii kat di taxawal ab sàmm ci réew mi. Lu ci réer, faalewu ko; lu ci lajj, du ko seet, lu ci gaañu, du ko faj, lu ci wér du ko xont, te lu ci duuf, mu yàpp, ba toj seeni we.