1Ba mu ko defee, ma séentu, gisuma lu moy ñeenti béjjén+ 2.1 béjjén, ñaare doole lay taxawe.*.
2Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Béjjén yii nag?» Mu ne ma: «Béjjén yii ñoo tasaare Yuda ak Israayil ak Yerusalem.»
3Ci kaw loolu Aji Sax ji won ma ñeenti tëgg.
4Ma ne: «Lan la ñii di defsi?» Mu wax ma, ne ma: «Béjjén yii tasaare Yuda ba kenn siggeetul, tëgg yii ñoo dikk ngir tiital leen, ba jàllarbi béjjéni xeet yi jóg song réewum Yuda, tasaare ko.»
5Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju yor buumu nattukaay ci loxoom.
6Ma ne ko: «Foo jëm?» Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo ak nu mu gudde.»
7Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom.
8Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.
9Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”
10Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,»
11«Éy Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*, rëccal,
12Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax, moom mi ma yebal ngir teddaayam, ci mbirum xeet yi leen sëxëtoo woon,
13Maa ngii déy di xàcc sama loxo ci seen kaw,
14«Sarxolleel te bànneexu, yaw janq Siyoŋ mu taaru,
15«Bésub keroog la xeet yu bare di taqook Aji Sax ji,
16Aji Sax jeey séddoo Yuda, muy wàllam ci suuf su sell|lemma="sell:"* si,