1Gannaaw gi, Aji Sax ji won ma Yosuwe sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag ba, mu taxaw fa kanam malaakam Aji Sax|lemma="malaakam Aji Sax j-:"* ji, Tuumaalkat|lemma="Seytaane:"* bi taxaw féete ko ndijoor, ngir tuumaal ko.
2Aji Sax ji ne Tuumaalkat bi: «Aji Sax ji rëbb na la, yaw Tuumaalkat bi, Aji Sax ji tànn Yerusalem rëbb na la. Xanaa Yosuwe mii du lenn lu moy gillit wu ñu fëkke cib taal?»
3Yosuwee ngi sol yére yu dand, taxaw fi kanam malaaka mi.
4Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»
5Ma daldi ne: «Nañu teg kaala gu set ci boppam.» Ñu tegal ko kaala gu set ci boppam, solal ko yeneen yére. Malaakam Aji Sax jaa nga taxaw.
6Malaakam Aji Sax ji nag dénk Yosuwe ne ko:
7«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Su fekkee ne samay yoon ngay awe te sama ndénkaane nga sàmm, su boobaa yaw it dinga saytu sama kër, di sàmm samay ëtt. Te maa lay jox ay cér yu la yaatal ci biir ñii fi taxaw.
8Déglul bu baax, yaw Yosuwe sarxalkat bu mag bi,
9Doj waa ngii ma teg fi kanam Yosuwe,