1Ba loolu amee malaaka ma doon wax ak man délsi, yee ma, mel ni ku ñu yee ciy nelaw.
2Mu ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Damaa xool, gisuma lu moy ab tegukaayu làmp bu lépp di wurus ak kopp bu tege ci kawam ak juróom ñaari làmp ci kawam, bu ci nekk ak juróom ñaari gémmiñam ca kaw.
3Ak ñaari garabi oliw ca wet ga: genn ca ndijooru kopp ba, ga ca des ca càmmoñam.»
4Ma dellu wax ak malaaka ma doon wax ak man, ne ko: «Yëf yii nag, lu muy wund, Sang bi?»
5Malaaka ma doon wax ak man ne ma: «Xamuloo lu yëf yii di wund?» Ma ne ko: «Déedéet, Sang bi.»
6Mu wax ma ne ma: «Lii moo di kàddug Aji Sax ji dikkal Sorobabel, di wax ne:
7Yaa di kan, yaw tund wu mag wi?
8Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma, ne ma:
9«Loxol Sorobabel a teg fondmaa kër gii,
10Ana kuy xeeb bés bii lu tuut sottee?
11Ma dellu ne ko: «Ñaari garabi oliw yii nag, genn gi ci ndijooru tegukaayu làmp bi, gi ci des ci càmmoñam, lu ñuy wund?»
12Ci kaw loolu ma dellooti ne ko: «Ñaari cari oliw yi feggook ñaari solomi wurus yiy xelli diw nag, lu ñuy wund?»
13Mu ne ma: «Xamuloo lu yooyuy wund?» Ma ne ko: «Déedéet, Sang bi!»