1Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:
2«Waxal bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ne leen: Ku ëmb ba wasin, am doom ju góor, dina sobewu diiru juróom ñaari fan. Day sobewu ni bu tolloo ci fan yi muy gis baax.
3Bu bés ba délsee, nañu xarafal xale bi.
4Dina ca teg fanweeri fan ak ñett, ngir setlu ca meret ma. Ci diir booba warula laal lenn lu ñu sellal, mbaa mu dem ca xaymab ndaje|lemma="xaymab ndaje m-:"* ma li feek àppu setloom matul.
5Su amee doom ju jigéen, dina sobewu diiru ñaari ayi bés, mu mel ni ku gis baax. Dina ca teg juróom benn fukki fan ak juróom benn, doora tàggook sobey meret ma.
6«Keroog bu àppu setloom matee, bu doom ja dee góor, bu dee jigéen, na dem ca bunt xaymab ndaje ma te yóbbul sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bi am kuuy mu am at, muy saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, ak xati mu ndaw mbaa pitax, mu doon saraxu póotum bàkkaar|lemma="Sarax yi:"*.
7Na ko sarxalkat bi sarxal fi kanam Aji Sax ji, def ko njotlaayal wasin-bees wi, mu doora tàggook sobey meret ma.»